+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«مَنْ قَالَ: سُبْحَانَ اللهِ وَبِحَمْدِهِ، فِي يَوْمٍ مِائَةَ مَرَّةٍ، حُطَّتْ خَطَايَاهُ وَإِنْ كَانَتْ مِثْلَ زَبَدِ الْبَحْرِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6405]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku wax: Subhaanal Laahi wa bi hamdihii, ci bis bi téeméeri yoon, ñu sippi ay bàkkaaram doonte dafa tol ni puuriti géej».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6405]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku wax téeméer i yoon ci bis bi: "Subhaanal Laahi wa bi hamdihii"; ñu far ay bàkkaaram jéggal ko ko, doonte dafa bari ba tol ni puuriti géej muy lu weex liy tiim Géej gi bu amee ay yëngu.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Asrabijaani Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Pay gi nag ku ko wax ci bis bi rekk dana ko am moo xam daa toftaloo walla dafa tàqalikoo.
  2. Sàbbaal: mooy sellal Yàlla ci bépp wàññeeku, Cànt: mooy mellal ko ci gépp mat ànd ak bëgg ak màggal.
  3. Li ñu namm ci hadiis bi mooy far bàkkaar yu ndaw yi, bàkkaar yu mag yi nag moom tuub ko manuta ñàkk.