عن أبي أيوب رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«مَنْ قَالَ: لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَحْدَهُ لَا شَرِيكَ لَهُ، لَهُ الْمُلْكُ وَلَهُ الْحَمْدُ وَهُوَ عَلَى كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ، عَشْرَ مِرَارٍ كَانَ كَمَنْ أَعْتَقَ أَرْبَعَةَ أَنْفُسٍ مِنْ وَلَدِ إِسْمَاعِيلَ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2693]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Ayyuuba -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku wax: laa ilaaha illal laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiiru , fukki yoon dana mel ne ku goreel ñenti bakkan ci doomi Ismaayla».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2693]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ku wax: "laa ilaaha illal laahu wahdahu laa sariika lahu lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say in Xadiirun", maanaam mooy: amul ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla dong amul bokkaale, te moom aji sell ji moo jagoo nguur gu mat, moo yayoo cant ak tagg gu ànd ak mbëggeel ak màggal moom rekk, te mooy ki am kàttan lottul ci dara. Ku baamtu sikar bu màgg bii ci bis bi fukki yoon, dana am ci yool kem yoolu ku dindi ag njaam ci ñenti jaam ci séti Ismaayla doomu Ibraahiima -yal na leen Yàlla dolli xéewal ak jàmm- dafa jagleel séti Ismaayla -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak jàmm- cig tund; ndax ñoom ñoo gën a tedd ku dul ñoom.