عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بنِ مَسْعُودٍ رضي الله عنه أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«سِبَابُ المُسْلِمِ فُسُوقٌ، وَقِتَالُهُ كُفْرٌ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 48]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdallah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"saaga ab jullig ag kàccoorte la, rayante ak moom ag kéefar la".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 48]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na ñuy saaga ak ŋàññ jullit bi, ak ne loolu dafa bokk ci kàccoore te mooy génn ag topp Yàlla ak ub yonnenteem, ak ne jullit di rayante ak mbokk jullitam dafa bokk ci jëfi kéefar yi, waaye kéefar gu ndaw la.