عَنْ حُذَيْفَةَ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لَا تَقُولُوا: مَا شَاءَ اللهُ وَشَاءَ فُلَانٌ، وَلَكِنْ قُولُوا: مَا شَاءَ اللهُ ثُمَّ شَاءَ فُلَانٌ».
[صحيح بمجموع طرقه] - [رواه أبو داود والنسائي في الكبرى وأحمد] - [السنن الكبرى للنسائي: 10755]
المزيــد ...
Jële nañu ci Husayfata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«buleen di wax: bu soobe Yàlla soob diw, waaye waxleen: bu soobe Yàlla topp mu soob diw»
[Wér na ci kaw bees boolee mbooleem yoon yi mu ñëwee] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ahmat] - [Téere bu mag bi An-nasaa'iy def ci Sunna yi - 10755]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na jullit bi muy wax: "bu soobee Yàlla soob diw", Walla lu soob Yàlla ak diw; Ndaxte coobarey Yàlla ak nàmmeelam lu boy la kenn du ko bokk ak moom, jëfandikoo (ak) cig toftale dees ciy dégge ne daa am ku bokk ak Yàlla ak yamale leen. Waaye day wax: looloo soob Yàlla topp mu soob diw, Mu def coobarey jaam bi mu topp ci coobarey Yàlla ci mu wax: "topp" te baña wax "ak" ndaxte "topp" day tektale ag toftaloo.