عَن أَبِي بُرْدَةَ بْنِ أَبِي مُوسَى رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ:
وَجِعَ أَبُو مُوسَى وَجَعًا شَدِيدًا، فَغُشِيَ عَلَيْهِ وَرَأْسُهُ فِي حَجْرِ امْرَأَةٍ مِنْ أَهْلِهِ، فَلَمْ يَسْتَطِعْ أَنْ يَرُدَّ عَلَيْهَا شَيْئًا، فَلَمَّا أَفَاقَ، قَالَ: أَنَا بَرِيءٌ مِمَّنْ بَرِئَ مِنْهُ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، إِنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بَرِئَ مِنَ الصَّالِقَةِ وَالحَالِقَةِ وَالشَّاقَّةِ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1296]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Burdata ibn Abii Muusaa yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Abuu Muusaa dafa tawat tawat ju tar, mu daal di xëm fekk boppam bi moo ngi ci pooju jenn jigéen ci njabootam, te manu ko a tontu ci dara, ba mu féexee, daal di ne: man de set naa wicc ci ku Yonente Yàlla bi set ci moom, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa set wicc ci aji-yuuxu ji, ak aji-wat kawaram, ak aji-xotti yéereem.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1296]
Abii Burdata yal na ko Yàlla dollee gërëm day nettali ne baayam Abuu Muusaa Al-Asharii dafa feebar feebar bu tar daal di xëm, fekk boppam bi moo ngi tege ci pooju jenn jigéen ci njabootam, mu daal di yuuxu, te manu koo wax dara ndax li mu xëm. Ba mu ximmikoo daal di ne: moom set na wicc ci ku Yonente Yàlla bi set ci moom, te Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ku set la ci: Aji-yuuxu ji: mooy kiy yëkkëti kàddoom ngir musiba Ak aji-wat kawaram: mooy kiy wat kawaram bu musiba amee. Ak aji-xotti yéeréem: mooy kiy xotti ay yéeréem bu musiba amee. Ndaxte loolu ci biri ceddo ya la bokk, waaye dafa digle muñ bu musiba amee, ak yaakaar fayug Yàlla.