Toftaleg Adiis yi

waxal: laa ilaaha illalaahu wahdahu laa sariika lahu, Allaahu Akbaru kabiiran, wal hamdu lil-Laahi kasiiran, subhaanal Laahi Rabbil haalamiina, laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi Alhasiisil-Alhakiimi
عربي Àngale Urdu
misaalum jullit biy jàng Alxuraan moo ngi mel ni Utruja, xetam ga dafa teey ak cafkaam teey, misaalum jullit bi dul jàng Alxuraan moo ngi mel ni tàndarma, amul xet te cafkaam dafa neex
عربي Àngale Urdu
ay mbir a ngii yuy wuutante ku leen di wax du sooy -walla ku leen di def- ginnaaw jullig farata gu nekk, Subhaanal Laahi fanweeri yoon ak ñatt, alhamdu lil-Laahi fanweeri yoon ak ñatt, Allaahu Akbaru, fanweeri yoon ak ñent
عربي Àngale Urdu
doomu Aadama weddi na ma te loolu waru ko woon,mu saaga ma te waru ko woon
عربي Àngale Urdu
ñaari xaaj a gi nii yu bokk ci waa sawara te gisaguma leen,ay nit yu yor ay yar yu mel ni geeni nag di ci dóor nit ñi,ak ayjigéen yu solu ba noppi rafle, jeng di jengale
عربي Àngale Urdu
Nëxit gi jigéen di gis ak mboq-mboq yi ginnaaw laab daawuñuko jàppee dara
عربي Àngale Urdu
toogal diir bi la sa mbaax daan téye, topp nga sangu
عربي Àngale Urdu
sangu bisub àjjuma war na képp ku toll ci gént,ak mu soccu, ak mu laal gëtt bu ko amee
عربي Àngale Urdu
bu weeru koor ñëwee na nga dem umra ji ndax umra day yemoo ak aj
عربي Àngale Urdu
Yaw Yonnente Yàlla bi, gis nanu ne jihaad moo gën ci jëf yi, mo ndax dunu jihaadi? Mu wax ne: "déedéet, waaye jihaad ji gën mooy: aj gu baax
عربي Àngale Urdu
kiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku kooku moo ngi ci yoonu Yàlla
عربي Àngale Urdu
man nag giñloowuma leen ci ne dama leen a tuumaal, waaye Jibriil moo ñëw fi man xibaar ma ne Yàlla mu kawe mi moo ngi leen di puukarewoo fa malaaka ya
عربي Àngale Urdu
yamaleleen seen sàppe yi, ndax yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi
عربي Àngale Urdu
Jullit bu góor du bañ jullit bu jigéen, ndax su bañee ci moom jenn jikkó gërëm na ci moom jeneen jikkó
عربي Àngale Urdu
Nekkoon naa ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu dem ba egg ci sënu aw nit daal di tuur ndox fekk ma nga taxaw,
عربي Àngale Urdu
ndax duma leen waxtaanal ci Ad-Dajjaal, lu benn Yonnente masul a wax aw xeetam? Moom de dafa patt, dana ànd ak lu mel ni àjjana ak sawara,
عربي Àngale Urdu
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan julli day teqale ay loxoom ba weexaayu poqtaanam di feeñ
عربي Àngale Urdu
Alal ji gën ci li nit ki di joxe: mooy alal ji mu jox njabootam ak alal ji mu jox ay daabaam ci yoonu Yàlla, ak alal ji mu jox ay àndandoom ci yoonu Yàlla
عربي Àngale Urdu
Melow sangu janaba.
عربي Àngale Urdu
dangeen topp yooni ña leen jiitu woon, sibre ak sibre, loxo ak loxo
عربي Àngale Urdu
wàlle amul gaafal amul, njuuma amul, Safar amul, te nanga daw ki gaana kem ni ngay dawe Gaynde
عربي Àngale Urdu
nit ñi bu ñu gisee tooñkat bi te téyewuñu loxoom kon tuuti rekk Yàlla boole leen mbugal
عربي Àngale Urdu
texe na de ndeem wax na dëgg
عربي Àngale Urdu
torox na, torox na, torox na" ñu ne ko: kan? Yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne: "ku fekk ñaari way-juram di ay mag, kenn ka walla ñaar ñépp te duggul Àjjana
عربي Àngale Urdu
ñu beru ñi raw nañu
عربي Àngale Urdu
jullit bi bu ñu ko laajee ci bàmmeel: day seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la
عربي Àngale Urdu
Fekk nañu jenn jigéen ñu ray ko ci benn ci xarey Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, Yonnente bi daal di ñaawlu ñuy ray jigéen ñi ak xale yi
عربي Àngale Urdu
tere na nisër, daal di wax ne: "du indi aw yiw, waaye dees ciy genne aji-nay ji
عربي Àngale Urdu
ku sol sooy fii ci àdduna du ko sol fële ca allaaxira
عربي Àngale Urdu
bokk na ci jihaad yi gën a màgg wax kàddug maanute fi kanamu buur bu jeng
عربي Àngale Urdu
Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal
عربي Àngale Urdu
amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, alkande ñeel na araab yi ci ay wu jege, tijji nañu tay ci baaraasu Yaajuuja ak Maajuuja lu toll ni
عربي Àngale Urdu
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ëppoon kersa jigéen gi sëyagul, bu gisee mbir mu mu bañ ci kanamam gi lañu koy xame
عربي Àngale Urdu
ku ñaan Yàlla nekk sahiid ci ag dëggu kon Yàlla dana ko jotale ca darajay ña nekk sahiid, donte dafa dee ci kaw lalam
عربي Àngale Urdu
danañu indi jenn waay ëllëg bis-pénc, sànni ko ca sawara, buttiti biir yi tasaaroo, mu koy wër kem ni mbaam di wëre ci takkuwaayam
عربي Àngale Urdu
aw doj la wu ñu sànni ca biir sawara diirub juróom-ñaar-fukki at, mooy door a wàcc ca sawara sa leegi ba egg ca suuf
عربي Àngale Urdu
ku waajalal aji-xare ci yoonu Yàlla kooku xare na, ku wuutu aji-xare ci yoonu Yàlla ci yiw kooku xare na
عربي Àngale Urdu
ku ñu ag ñeewant xañees na ko aw yiw
عربي Àngale Urdu
ku jàppu te rafetal am njàppam daal di ñëw ci àjjuma ji te noppi déglu, dees na ko jéggal li nekk ci diggante bi ak diggante jeneen àjjuma ja, ak ñu dolli ca ñatti fan
عربي Àngale Urdu
ndax duma leen tektal lu gën li ngeen di laaj? Bu ngeen tëddatee -walla ngeen ñëw ci seen lal- nangeen sàbbaal Yàlla fanweer ak ñatt, te ngeen sant Yàlla fanweer ak ñatt, ngeen màggal Yàlla fanweer ak ñent, loolu moo gën ci yéen liggéeykat
عربي Àngale Urdu
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gënoon a tabe ci nit ñi, ci weeru koor nag la daan gën a tabe ba Jibriil daan daje ak moom
عربي Àngale Urdu
ku giñ daal di wax: giñ naa ci Laata ak Hussaa, na wax: laa ilaaha illal-Laahu, ku wax àndandoom ne ko: kaay ñu kàrt na saraxe
عربي Àngale Urdu
ndax xam ngeen kan mooy ki ñàkk?
عربي Àngale Urdu
amul kenn ci yéen lu dul ne Yàlla dina wax ak moom, te kenn kuy firi du nekk seen diggante
عربي Àngale Urdu
ku ma waxal jenn wax te xam ne ay fen la, moom kenn la ci fenkat yi
عربي Àngale Urdu
ne bu daan dugg ci jàkka day wax: "ahuusu bil Laahi Alhasiimi, wa bi wajhihi Alkariimi, wa sultaanihii alxadiimi, minas Saytaani Arrajiimi
عربي Àngale Urdu
Yàlla mu kawe mi day wax ki gën a woyof mbugal ci waa sawara ëllëg bis-pénc: boo moomoon li ci suuf lépp ndax danga ko jote sa bopp? Mu ne: waaw
عربي Àngale Urdu
Yàlla mu baarkeel mi te kawe day wax waa àjjana: éey yéen waa àjjana? Ñu ne ko wuyusi nanu la topp nañu la ak mbegte, mu ne leen: ndax gërëm ngeen? Ñu ne ko: lu ñuy teree gërëm te nga jox nu loo joxul kenn ci sa mbindeef yi?
عربي Àngale Urdu
amul benn jullit buy jàppu rafetal njàppu mi, daal di jog julli ñaari ràkka, xolam ak jëmmam jublu ca, lu dul ne àjjana war na ci moom
عربي Àngale Urdu
buleen di giñ ci yi ñuy jaamu te du Yàlla, buleen di giñ it ci seen i baay
عربي Àngale Urdu
sàppey góor ñi gi ci gën mooy gu njëkk gi, bi ci yées mooy gu mujj gi, sàppey jigéen ñi gi ci gën mooy gu mujj gi, gi ci yées mooy gu njëkk gi
عربي Àngale Urdu
ñaari julli yii ñooy julli yi gën a diis ci naaféq yi, te bu ngeen xamoon li nekk ci ñoom ñaar dangeen ko teewe donte dangeen di raam ci ay wóom
عربي Àngale Urdu
Yaw Yonnente Yàlla bi, yaayu Sahd de dafa faatu, ban sarax moo gën?, mu ne ko: "ndox", nee na: mu gas ab teen, daal di ne: lii ngir yaayu Sahd la
عربي Àngale Urdu
yaw Abbaas, yaw baay taxu Yonnente Yàlla bi, ñaanal Yàlla jàmmi àdduna ak allaaxira
عربي Àngale Urdu
ñaar yii dañoo araam ci sama góori xeet wi, waaye dagan nañu ci jigéen ñi
عربي Àngale Urdu
Tere na lépp lu am bëñ ci negment yi, ak lépp lu am aw sàll ci ñanaaw yi
عربي Àngale Urdu
Yàlla du nangu ci jëf yi lu dul lu sell ñeel ko, ñu jublu sa jëmmam ji
عربي Àngale Urdu
amul benn Yonnente bu Yàlla yónni ci xeet yi ma jiitu lu dul ne am na ci aw xeetam ñu koy dimbali ak ay àndandoo yu jàpp ci yoonam di roy ci mbiram
عربي Àngale Urdu
jox na nu ma juróom yoo xam ne joxuñuko kenn ku ma jiitu
عربي Àngale Urdu
bu kenn ci yéen dajee ak mbokkam na ko nuyu, bu dara doxee seen diggante ag garab walla miir walla aw doj mu dajewaat ak moom na ko nuyu batay
عربي Àngale Urdu
saytaane day fas ci ginnaaw boppu kenn ci yéen bu dee nelaw ñatti fas, genn fas-fas gu nekk day waral ci yaw guddi gu gudd, mu naan nelawal
عربي Àngale Urdu
dajee naa ak Ibraahiima guddi gi ñu ma rañaanee mu wax ne: yaw Muhammat, jottalil ma saw xeet samag nuyóo, te nga xibaar leen ne Àjjana lu teey ag suuf la, lu neex am ndox la
عربي Àngale Urdu
bu ngeen ko gisee woorleen, bu ngeen ko gisee worileen, bu muuroo ci yeen nangeen ko nattale
عربي Àngale Urdu
bul ko ray, ndaxte boo ko rayee moom day nekk sa barab laata nga koy ray, yaw nga nekk ci barabam laata muy wax kàddu gi mu wax
عربي Àngale Urdu
dinaa jox Raaya ji waa ju bëgg Yàlla ak ub yonnenteem, Yàlla dina ko ubbee ci ay loxoom
عربي Àngale Urdu
deeleen dégg tey topp, li leen war ñoom mooy la ñu leen gàdduloo, yéen it li leen war mooy li ñu leen gàdduloo
عربي Àngale Urdu
saaga ab jullig ag kàccoorte la, rayante ak moom ag kéefar la
عربي Àngale Urdu
buleen njëkka nuyu Yahuud yi ak Nasaraan yi ci nuyoog Salaam, bu ngéen dajee ak kenn ci ñoom ci yoon nangeen ko jaarloo fa gën a xat
عربي Àngale Urdu
bokkul ci nun kiy mbej ñiy mbej lex ya, di xotti kaw yére ya, di woote wooteg ceddo ya
عربي Àngale Urdu
kuy njëw ci yéen ci àjjuma ji na sangu
عربي Àngale Urdu
ki nay dëgg mooy ki ñu ma tudd fi moom te julliwul ci man
عربي Àngale Urdu
ku xëy dem ca jàkka ja, walla mu gont fa Yàlla dana ko waajalal ca àjjana ab wàccuwaay, saa yu xëyee walla mu gont
عربي Àngale Urdu
rabbi ixfir lii xadii-atii wa jahlii, wa israafii fii amrii kullihii, wa maa Anta ahlamu bihii minnii, Allaahuma ixfir lii, xataayaaya, wa hamdii wa jahlii wa haslii, wa kulli saalika hindii, Allaahuma ixfir lii maa xaddamtu wa maa ax-xartu, wa maa asrartu wa maa ahlantu, antal Muxaddimu wa Antal Mu-axiru, wa Anta halaa kulli say-in xadiirun
عربي Àngale Urdu
Allaahuma innii ahuusu bika min sawaali nihmatika, wa tahawwuli Hanafiyatika, wa fujaa-ati niqmatika, wa jamiihi saxatika
عربي Àngale Urdu
Allaahuma innii ahuusu bika min xalati addayni, wa xalabati alhaduwwi, wa samaati al-ahdaa
عربي Àngale Urdu
waxal, Allaahuma ihdinii wa saddidnii, waskur bilhudaa hidaayataka attariixa, wassadaadi sadaada assahmi
عربي Àngale Urdu
tegal sa loxo fiy metti ci sa yaram, nga wax: Bismil Laahi ñatti yoon, te wax juróom-ñaari yoon: Ahuusu bil Laahi wa xudratihii, min sarri maa ajidu, wa uhaasiru
عربي Àngale Urdu
koo xam ne day jullu laata jant bi di fenk ak laata muy soh du dugg sawara
عربي Àngale Urdu
amul kenn kuy julli ci man lu dul ne Yàlla dana ma delloo samag ruu ba ma delloo ko nuyóo
عربي Àngale Urdu
Aji-woote ji day woote ne: di ngeen wér te du ngeen tawatati ba fàww, di ngeen dund te du ngeen deeati ba fàww, di ngeen bijjaaw te du ngeen màggatati ba fàww, di ngeen xéewlu te du ngeen yoqatati ba fàww
عربي Àngale Urdu
bu waa àjjana duggee àjjana, Yàlla mu Barkeel mi te kawe day wax ne: ndax bëggeen dara lu ma leen dolli?
عربي Àngale Urdu
bu kenn ci yeen jàppoo daal di sol ay saŋam na ca julli, na masaa ci seen kaw te mu bañ leen a summi bu ko soobee lu dul ci janaba
عربي Àngale Urdu
Masuma a gis Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy xàqataay di ree ba ma gis ay yàppi biir gémmiñam, waaye da daan muuñ
عربي Àngale Urdu
bu kenn ci yéen gisee ci gént lu mu bëgg, loolu ci Yàlla la bawoo, na sant Yàlla ci loolu te waxe ko, bu gisee lu dul loolu ci lu mu sib, loolu ci Saytaane la bawoo, na muslu ci ayam, te bu mu ko wax kenn, kon du ko lor
عربي Àngale Urdu
ku dundal ñaari jigéen ba ñu mat, dana ñëw ëllëg bis-pénc man ak moom" mu tàppale ay baaraamam
عربي Àngale Urdu
amul benn bis bu jaam ñi di xëy lu dul ne ñaari malaaka danañu wàcc, kenn ki naan: yaw Yàlla joxal aji-joxe ji leneen, keneen ki naan: yaw Yàlla joxal aji-téye ji ag yàqule
عربي Àngale Urdu
ndax duma leen xibaare waa àjjana? Ñooy képp ku néew doole, tey toroxlu, te bu giñoon ci Yàlla mu dëggal ko, ndax duma leen xibaare waa sawara? Ñooy képp ku dëgër soxor tey rëy-rëylu
عربي Àngale Urdu
man de xam naa baat boo xam ne bu ko waxoon li muy yég deñ, bu waxoon: ahuusu bil Laahi minas Saytaani, kon li muy yég dem
عربي Àngale Urdu
gént gu baax ci Yàlla la jóge, gént gu bon nag ci Saytaane la jóge, bu kenn ci yéen gisee gént gu mu ragal, na tifli ci càmmooñam, te muslu ci Yàlla ci ayam, kon du ko lor
عربي Àngale Urdu
Damaa wax: "yaw Yonnente Yàlla bi, ana lan mooy musale? Mu ne ma "tëyéel sa làmmiñ, te na la sa kër doy, te nga jooy say ñuumte
عربي Àngale Urdu
man maa ngi fa ma sama jaam bi njorte, te maa ngi ànd ak moom saa yu ma tuddee
عربي Àngale Urdu
Laaj naa Aysatu, ne ko: ci lan la Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan tàmbalee bu daan dugg këram? Mu ne: ci socc
عربي Àngale Urdu
jaam bi du suturaal ab jaam ci àdduna lu dul ne Yàlla dana ko suturaal ëllëg bis-pénc
عربي Àngale Urdu
bu kenn ci yéen faatu lu dul ne dafa rafet njort ci Yàlla
عربي Àngale Urdu
bu dee ni nga wax lañu mel, moo ngi mel ni yaa ngi leen di gàccaal di leen mëqloo dóom bu tàng, te Yàlla du deñ di la dimbali ci seen kaw fii ak yaa ngi ci loolu
عربي Àngale Urdu
ñaari ndëggu jaam bi du pënd ci yoonu Yàlla ba noppi sawara di ko laal
عربي Àngale Urdu
amul aw nit wuy jog ci ab jotaay te tudduñu fa Yàlla lu dul ne danañu jog mel ni méddum mbaam, ñu ame ca ag réccu
عربي Àngale Urdu
misaalu kiy tudd Boroomam ak ki dul tudd Boroomam, mi ngi mel ni misaalu kiy dund ak ki dee
عربي Àngale Urdu
man de bokk na ci li may ragal ci yéen sama ginnaaw, ñu ubbil leen naataangey àdduna ak taaram
عربي Àngale Urdu
ku bëgg Yàlla musal ko ci xat-xati ëllëg bis-pénc, nay yombalal ki nekk ci jafe-jafe walla mu teggil ka ko
عربي Àngale Urdu
ki gën a woyof mbugal ci waa sawara mooy ki am ñaari dàll ak ñaari waroy dàll yu sawara, yuuram gi di ci bax kem ni cin di baxe, ba du foog ne kenn a ko gën a tar mbugal, te moo leen gën a woyof mbugal
عربي Àngale Urdu
dees na jegeele aji-gëm ji Boroomam bu màgg bi ëllëg bis-pénc, ba mu teg suturaam ci kawam, di ko saxalal ay bàkkaaram
عربي Àngale Urdu
Saytaane naagu na ci jullikat yi jaamu ko ci goxi araab yi, waaye ci jaxase seen diggante
عربي Àngale Urdu
Bu kenn ci yéen jullee ci benn yére te dara tegewul ci kaw mbaggam
عربي Àngale Urdu
boo sujjóotee, na nga teg say ténq te yëkkëti say conc
عربي Àngale Urdu
Julli naa ak Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy sëlmël ci ndayjooram: "assalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhu", ak ci càmmooñam: "assalaamu halaykum warahmatul Laah
عربي Àngale Urdu
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ñeel Abuu Bakrin ak Umar: «ñaar ñii ñooy sangi paa yiy nekk àjjana ñu njëkk ña ak ñu mujj ña ba mu des yónente yi 
عربي Àngale Urdu
Asan ak Usaynu ñooy sangi waxambaaney waa àjjana
عربي Àngale Urdu
ku sàmmonte ak ñenti ràkka njëkk Tisbaar ak ñenti ràkka ginnaaw tisbaar yàlla araamal ko ca sawara
عربي Àngale Urdu
Yàlla du xool góor giy sëy ak soxnaam ci ginnaawam
عربي Àngale Urdu
ku am ñaari jabar daal di jeng ci kenn ki, dana ñëw ëllëg bis-pénc wetam gi jeng
عربي Àngale Urdu
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc julliwul ag julli ginnaaw bi {Isaa jaa-a nasrul Laahi walfathu} [An-Nasr: 1] wàccee ci moom lu dul dana ca wax: "Subhaanaka Rabbanaa wa bihamdika Allaahuma ixfir lii
عربي Àngale Urdu
yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, ndax dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka
عربي Àngale Urdu
waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
عربي Àngale Urdu
digal nañu ma ma xeex ak nit ñi ba baa ñuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka
عربي Àngale Urdu
bu ñu doon jox nit ñi ci seen i wootewoo kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a indi firnde, kiy weddi daa war a giñ.
عربي Àngale Urdu
Yàlla ak ub yonnenteem araamal na ñu jaay sàngara, ak médd, ak mbaam xuux, ak ay xërëm
عربي Àngale Urdu