عن أبي سعيد الخدري رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«الحَسَن والحُسَيْن سَيِّدا شَباب أهْل الجنة».
[صحيح] - [رواه الترمذي وأحمد] - [سنن الترمذي: 3768]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"Asan ak Usaynu ñooy sangi waxambaaney waa àjjana".
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3768]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ñaari sëtam yii Asan ak Usaynu ñaari doomi Aliyun Ibn Abii Taalib ak Faatimatu doomu Yonnente bi ñooy sangi kepp ku faatu tey waxambaane bu dugg àjjana ci ngëneel, walla ñooy sangi waxambaaney waa àjjana ba mu des Yonnente yi ak Xalifaa yu jub ya.