عَنْ أَبَي قَتَادَةَ رضي الله عنه أنَّهُ طَلَبَ غَرِيمًا لَهُ، فَتَوَارَى عَنْهُ ثُمَّ وَجَدَهُ، فَقَالَ: إِنِّي مُعْسِرٌ، فَقَالَ: آللَّهِ؟ قَالَ: آللَّهِ؟ قَالَ: فَإِنِّي سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«مَنْ سَرَّهُ أَنْ يُنْجِيَهُ اللهُ مِنْ كُرَبِ يَوْمِ الْقِيَامَةِ فَلْيُنَفِّسْ عَنْ مُعْسِرٍ أَوْ يَضَعْ عَنْهُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1563]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Xataadata yal na ko Yàlla dollee gërëm ne na da doon seet kenn ku ko ameeloon bor, mu làqatu ko topp mu gis ko, mu ne ko: man de ci jafe-jafe laa nekk, mu ne: ndax da nga ko waat ci Yàlla? Mu ne ko: waat naa ko ci Yàlla? Mu ne ko: man dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di wax naan:
«ku bëgg Yàlla musal ko ci xat-xati ëllëg bis-pénc, nay yombalal ki nekk ci jafe-jafe walla mu teggil ka ko».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1563]
Abuu Xataadata Al-Ansaarii yal na ko Yàlla dollee gërëm da doon seet ku ko yoreel bor di ko làqtu, mu gis ko, ki ko ameel bor ne ko: man de damaa nekk ci jafe-jafe, te amuma alal ju ma la faye sa bor.
Abuu Xataadata yal na ko Yàlla dollee gërëm giñloo ko ci Yàlla ci ne amul alal?
Waa ji giñ ci Yàlla ci ne li mu wax dëgg la.
Abuu Xataadata ne ko dégg naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
Ku bëgg Yàlla bégloo ko musal ko ci jafe-jafey ëllëg bis-pénc ak i tar-taram ak i tiitaangeem, nay yombalal ki nekk ci jafe-jafe, ci yokkal ko ak yeexe ko a fayyu boram, walla mu baal dara ci bor bi walla lépp.