Toftaleg Adiis yi

képp ku aj ngir Yàlla te beejul ( sëyul wala mu wax lu bon) deful tamit yëfi kàccor, dana dellu mel ni bis ba ko yaayam jure woon
عربي Àngale Urdu
Ndax duma leen xibaar bàkkaar yi gën a mag?
عربي Àngale Urdu
bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg
عربي Àngale Urdu
bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate
عربي Àngale Urdu
Jaayante nanu ak Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci dégg ak topp, ci lu jafe ak lu yomb, ci lu neex ak lu naqari, ak bu xat-xat tegee sunu kaw
عربي Àngale Urdu
deesul julli fekk ñam wi daa teew, walla muy xëcconte ak ñaari sobe yi
عربي Àngale Urdu
boo waxee sa àndandoo: noppil ci bisu àjjuma, fekk imaam bi di xutba, kon fo nga
عربي Àngale Urdu
kiy taxawu ak a dimbali ab Jatun ak way-ñakk moo ngi mel ni kuy xeex ci yoonu Yàlla, wàlla kuy taxaw guddi di woor bëccëg
عربي Àngale Urdu
Yi Yàlla moñaale ak nit ki juróom la: xaraf, wat kawaru naq, ak wàññi kawari mustaas, ak lewwi ay weh, ak suqi kawari poqtaan
عربي Àngale Urdu
giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom kenn du ma dégg ci xeet wii moo xam Yahuut la walla Nasaraan, ba faatu te gëmul li ñu ma yónni lu dul ne dana bokk ci waa sawara
عربي Àngale Urdu
jempleen Seen mustaas yi, te yar sikkim yi
عربي Àngale Urdu
ku jàppoo kem sama njàpp mii, daal di julli ñaari ràkka yoy du ca xalaat dara, kon Yàlla dana ko jéggal bàkkaaram yi jiitu
عربي Àngale Urdu
yal na Yàlla rëbb Yahuut yi ak Nasaraan yi, ñoom kat dañoo jàppe séen bàmmeeli Yónente yi ay jàkka
عربي Àngale Urdu
moytuleen juróom-ñaar yiy alage
عربي Àngale Urdu
yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm
عربي Àngale Urdu
ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem
عربي Àngale Urdu
seedeel naa Yàlla ne set naa wicc ci kenn ci yéen di nekk sama xarit, ndax Yàlla da maa jàpp xarit, niki mu jàppe Ibraahiima xarit
عربي Àngale Urdu
buleen def seen kër yi ay bàmmeel, te buleen def sama bàmmeel am ndaje, deeleen julli ci man, ndax seen ug julli ci man dina yeksi fi man ak fu ngeen man di nekk
عربي Àngale Urdu
Yàlla day fiir, way-gëm it day fiir, te fiiràngeg Yàlla mooy way-gëm ji def lu mu araamaal
عربي Àngale Urdu
ku giñ ci ku dul Yàlla weddi na walla bokkaale na
عربي Àngale Urdu
julli gi gën a diis ci naaféq yi mooy jullig gee ak jullig fajar, te bu ñu xamoon li nekk ci ñoom ñaar kon danañu ko teewe donte dañuy raam
عربي Àngale Urdu
bokk na ci ñi gën a bon ci nit ñi mooy ñi bis-pénc di ñëw fekk ñuy dund, ak ñiy jàppe bàmmeel yi ay jàkka
عربي Àngale Urdu
li ma gën a ragal ci yéen mooy bokkaale gu ndaw" ñu ne ko: lan mooy bokkaale gu ndaw yaw Yonnente Yàlla bi? Mu ne leen: "ngistal
عربي Àngale Urdu
yaa ngi jëmm ci aw nit woo xam ne ay ñoñ-téere lañu, boo demee ca ñoom, nanga leen woo ñu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawu Yàlla la
عربي Àngale Urdu
buleen ma jay kem ni Nasaraan yi jaye woon doomu Maryama; man daal ab jaamam laa, kon deeleen wax: jaamub Yàlla ak ndawam
عربي Àngale Urdu
nit ki gën a texe ci samag rammu ëllëg bis-penc, mooy ki wax, Laa ilaaha illal Laahu, te mu sell lool ci xolam, walla ci bakkanam
عربي Àngale Urdu
Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll
عربي Àngale Urdu
ku dajeek Yàlla te bokkaalewu ko ak dara dana dugg àjjana, waaye ku dajeeg moom bokkaaleko ak dara dana dugg sawara
عربي Àngale Urdu
ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara
عربي Àngale Urdu
ñiy taral alku nañu
عربي Àngale Urdu
ku ma sàmmal li ci diggante ay ŋaamam ak li ci diggante ñaari tànkam ma wóoralal ko àjjana
عربي Àngale Urdu
ay njiit danañu ñëw, da ngeen gis ci ñoom lu baax, ak it lu bon, ku ànd ca lu baax la kooku set na wicc, ku weddi seen yu bon kooku mucc na, waaye ki muccul mooy ki gërëm yu bon ya te ànd ca
عربي Àngale Urdu
Yàlla du nangu jullig kenn ci yéen bu dee daa tojle ba keroog muy jàpp
عربي Àngale Urdu
bu nit ki feebaree walla mu tukki dees na ko bindal kem la mu daan jëf ba mu tukkiwul te wér
عربي Àngale Urdu
Li gën ci sikar yi: Laa ilaaha illal Laahu, li gën ci ñaan yi: Alhamdu lil Laahi
عربي Àngale Urdu
àjjana moo gën a jege ku ne ci yeen ay waroy dàllam, sawara it naka noonu
عربي Àngale Urdu
socc day laabal gémmeñ di gërëmloo Boroom bi
عربي Àngale Urdu
julliy juróom, ak Àjjuma ba Àjjuma, ak weeru koor ba weeru koor, dañuy far bàkkar yi ci séen diggante bu dee moytu nañu bàkkaar yu mag yi
عربي Àngale Urdu
Jottalileen jële ci man donte benn aaya la, ta ngeen waxtaane waa Banuu Israayil ci lu amul benn jafe-jafe, waaye ku ma fenal te tay ko na waajal ab tooguwaayam ca sawara
عربي Àngale Urdu
Amul benn coono buy dal ab jullit, mbaa tawat walla, jaaxle, mbaa naqar, loraange, walla njàqare, doonte dég gu ko jam la, lu dul ne Yàlla dina ca fare yenn ci ay bàkkaaram
عربي Àngale Urdu
wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar
عربي Àngale Urdu
àqi jullit ci moroomu jullitam juróom la: delloo ab nuyoo, ak seeti ki wopp, ak gunge néew bi, ak wuyu woote ba, ak ndokkeel ku tissooli
عربي Àngale Urdu
yal na Yàlla yërëm waa joo xam ne dafay yaatu bu dee jaay, ak budee jenn, ak buy fàyyeeku
عربي Àngale Urdu
am na benn waay bu doon lebal nit ñi, daan wax ndawam la naan ko: boo demee ci ku am jafe-jafe nanga ko jéggal, amaana Yàlla jéggal nu
عربي Àngale Urdu
kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog
عربي Àngale Urdu
ku muñal ki am jafe-jafe, walla mu baal ka ko, Yàlla dana ko keral bis-penc ca suufus keru Gàngunaayam ga bis ba nga xam ne genn ker amul gu dul keram ga
عربي Àngale Urdu
képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram
عربي Àngale Urdu
ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram
عربي Àngale Urdu
ku Yàlla namm ci moom aw yiw dana ko nattu
عربي Àngale Urdu
bàyyileen ma bu ma leen bàyyee, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seeni laaj ak di wuute ak seeni Yonnente
عربي Àngale Urdu
ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi ka raye ak ka ñu ray yépp sawara lañu jëm
عربي Àngale Urdu
diine de laayante-biir la
عربي Àngale Urdu
li dagan de leer na li araam it leer na,
عربي Àngale Urdu
Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp
عربي Àngale Urdu
Yàlla dafa bind yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di leeral ko, képp ku yéene jëf i yiw, te defu ko, Yàlla dana ka ko bindal wenn yiw wu mat sëkk, waaye bu ko yéenee ba noppi def ko, mu bindal ko fukki yiw, mannakoo Ful bamu yégg juróom-ñaari téeméeri, ba ci ay full yu bari, waaye képp ku Yéenee jëf lu ñaaw te defu ko Yàlla di na ko bindal wenn yiw wu mat sëkk, bu ko Yéenee nag daldi koy def mu bindal ko wenn ñaawteef
عربي Àngale Urdu
Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf
عربي Àngale Urdu
jëf yi mi ngi aju ca yéene ya, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am
عربي Àngale Urdu
Lislaam mooy: nga seede ne amul kenn ku deesi jaamu ku dul Yàlla, seede ne Muhammat ndawul Yàlla la, tey taxawal julli, di woor weeru koor, te aj Màkka benn yoon boo ko manee
عربي Àngale Urdu
bul mer
عربي Àngale Urdu
deesul loru waaye deesul lore, ku lore Yàlla lor ko, waaye ku sonle Yàlla sonal ko
عربي Àngale Urdu
su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc mi, day xëy nek ku woos xiif di gont biir bi fees dell
عربي Àngale Urdu
ku sos ci sunu diine ji lu ci bokkul dees na ka ko delloo
عربي Àngale Urdu
yéen sama jaam ñi damaa araamal tooñ ci sama bopp, ma def ko muy lu araam ci seen diggante kon buleen di tooñante
عربي Àngale Urdu
yaw ngóor si di naa la xamal ay waat: wattul Yàlla ci jëfe ay ndigëlam bayyi ay tereem kon di na la sàmm, Nanga bàyyi xel Yàlla kon mu féete la fépp, booy ñaan ñaanal Yàlla, booy sàkku ndimbël na nga dimbandikoo Yàlla
عربي Àngale Urdu
ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar
عربي Àngale Urdu
way-maandu ñi de fa Yàlla danañu nekk ci kaw i minbari leer, nekk ca ndeyjooru Yàlla Aji-Yërëme ju màgg ji te tedd te yaari loxoom yépp ndeyjoor la
عربي Àngale Urdu
ku ñu ag ñeewant xañees na ko aw yiw
عربي Àngale Urdu
Sama xeet wépp dinañu dugg àjjana ba mu des ku bañ
عربي Àngale Urdu
Jibriil deñul di ma dénk dëkkandóo, bama muj njort ne dana ko dondloo
عربي Àngale Urdu
mocc ak takk ay xarnga-fuufa ak noob bokkaale la
عربي Àngale Urdu
ndax xam ngeen luy jëw?», ñu ne ko: Yàlla ak Yónenteem a xam, mu daa di ne mooy: «tudd sa mbokk ci lu ko neexul
عربي Àngale Urdu
yaw Yàlla sama Boroom képp ku méngoo dara ci sama mbiri xeet wii, ba noppi di tar ci ñoom, na nga tar ci kawam, waaye képp ku ménggoo dara ci sama mbiri xeet wii, daal di leen woyofalal, na nga ko woyofalal
عربي Àngale Urdu
gaay yay Pasar-pasaree alali Yàlla ji ci lu dul dëgg, sawara ñeel na leen keroog bis-pénc
عربي Àngale Urdu
moytandikuleen njort; ndaxte njort mooy wax ji gën a nekk aw fen
عربي Àngale Urdu
amul benn jaam bu Yàlla sàmmuloo am càmm, mu faatu fekk da doon wuruj ña muy sàmme, lu dul ne Yàlla dana araamal ci moom àjjana
عربي Àngale Urdu
Jépp jëf ju baax sarax la
عربي Àngale Urdu
Bul xeeb dara ci lu baax, donte dangay dajeek sa mbokk won ko kanam gu bélli
عربي Àngale Urdu
am doole nekkul ci bëre daan, waaye ku am doole mooy kiy tëye boppam bu meree
عربي Àngale Urdu
Kuy niru-nirulu aw nit ca ñoom la book
عربي Àngale Urdu
Ku tegtale ci lu baax, dina am pay gu mel ni li ki ko def am
عربي Àngale Urdu
Laaj na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: ban bàkkaar moo gën a màgg fa Yàlla? Mu ne: "nga wutal Yàlla ndend te mu bind la
عربي Àngale Urdu
buleen saaga ñi faatu, ndax ñoom kat wéy nañu ca lañu jiital
عربي Àngale Urdu
Du dagan ci nit ki mu tóng mbokkam lu ëpp ñatti guddi, ñuy dajee kii dummóoyu kee dummóoyu, ki gën ci ñoom ñaar mooy ki tàmbli nuyóo ba
عربي Àngale Urdu
kuy dog mbokk du dugg àjjana
عربي Àngale Urdu
ab ràmbaajkat du dugg àjjana
عربي Àngale Urdu
ku bëgg ñu yaatal wërsëgam, guddal fanam, nay jokk ag bokkam
عربي Àngale Urdu
ku lore Yàlla lor ko, ku sonle Yàlla sonal ko
عربي Àngale Urdu
fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee, deeleen ci baril ay ñaan
عربي Àngale Urdu
ku julli suba moo ngi ci kaaraangeg Yàlla
عربي Àngale Urdu
képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nay wax yiw mbaa mu noppi
عربي Àngale Urdu
ku dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm
عربي Àngale Urdu
Ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy noon bi gën a man a xulóo
عربي Àngale Urdu
Wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah, Wal hamdu lil Laah, wa laa-i-Laaha illal Laah, wal Laahu akbar, boo ci tàmbalee baax na
عربي Àngale Urdu
Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko
عربي Àngale Urdu
kersa ci ngëm la bokk
عربي Àngale Urdu
ñaan mooy jaamu Yàlla
عربي Àngale Urdu
dénk naa leen dëggu, ndaxte dëggu day jur ag mbaax, te ag mbaax day jur àjjana
عربي Àngale Urdu
ñaari baat a ngi nii yu woyof ci làmmeñ, diis ci màndaxekaay ba, Yàlla miy Aji-Yërëme ji sopp leen
عربي Àngale Urdu
Amul dara lu gën a tedd fa Yàlla mu kawe mi lii di ñaan
عربي Àngale Urdu
saraxe du wàññi alal, te Yàlla du dolli Jaam biy jéggale ludul ag màgg, te kenn du toroxlu ngir Yàlla lu dul ne broom bi dina ko Yëkkati
عربي Àngale Urdu
ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc
عربي Àngale Urdu
ku wax: Subhaanal Laahi wa bi hamdihii, ci bis bi téeméeri yoon, ñu sippi ay bàkkaaram doonte dafa tol ni puuriti géej
عربي Àngale Urdu
ku wax: laa ilaaha illal laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiiru , fukki yoon
عربي Àngale Urdu
ku Yàlla nàmm ci moom aw yiw dana ko dégg-loo diine
عربي Àngale Urdu
Yàlla dafa bëgg jaam bu ko ragal, bu doylu, bu nëbbu
عربي Àngale Urdu
yéen de dangeen gis seen Boroom kem ni ngeen di gise weer wii, te du ngeen buuxante ngir gis ko
عربي Àngale Urdu
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul delloo gëtt
عربي Àngale Urdu
ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam
عربي Àngale Urdu
àdduna ay jumtukaay rekk la, te li gën ci jumtukaay yi àdduna mooy jigéen ju baax
عربي Àngale Urdu
def ndànk du am ci dara lu dul ne dana ko taaral, waaye du ñàkk ci dara it lu dul ne dana ko ñaawal
عربي Àngale Urdu
Yàlla dana bëgg ci jaam bi bu lekkee aw ñam mu sant ko ca, bu naanee ag naan sant ko ca
عربي Àngale Urdu
aji-gëm ji jikkoom ju rafet danako may mu am darajay Aji-woor ak kiy taxaw di julli
عربي Àngale Urdu
ñi gën ci yéen mooy ña ca gën a rafet jikkó
عربي Àngale Urdu
Yàlla nee na: yaw doomu Aadama ji joxeel ma jox la
عربي Àngale Urdu
Yalla dana néggandiku tooñkat bi, ba bu ko jàppee du ko rëcc
عربي Àngale Urdu
bàyyiwuma sama ginnaaw fitna ju dàq a lor góor ñi ci jigéen ñi
عربي Àngale Urdu
yomballeen te buleen jafeel, bégleleen te buleen dàqaate
عربي Àngale Urdu
nangeen kóllarante ak Alxuraan jii, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom moo gën a gaaw a rëcc giléem gi ñu yeew
عربي Àngale Urdu
ki gën ci yéen mooy ki jàng Alxuraan te di ko jàngale
عربي Àngale Urdu
ku wàcc cig kër daal di wax: ahuusu bi kalimaatil Laahi At taammaati min sarri maa xalaxa, dara du ko lor ba baa muy juge ca kër googa
عربي Àngale Urdu
ndax du ma la yabal ca la ma Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yabaloon? Bul bàyyi benn xërëm te tojoo ko, mbaa benn bàmmeel bu ñuy màggal te maasale woo ko
عربي Àngale Urdu
Kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko way-juram ak doomam ak mbooleem nit ñi
عربي Àngale Urdu
bokkul ci nun kuy gisaane mbaa ñu gisaaneel ko, walla mu seetlu mbaa ñu seetal ko, walla mu njabar mbaa ñu njabaral ko
عربي Àngale Urdu
ku ñëw cib xamtukat laaj ko dara deesu ko nangul julli ñent-fukki guddi
عربي Àngale Urdu
ku jàng xam-xamu biddiw jàng na benn xaaj ci njabar, bu dollee mu dolliku
عربي Àngale Urdu
sart yi gën a yelloo matal mooy yi ngeen daganale péy ya
عربي Àngale Urdu
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gënoon a rafet jikko ci nit ñi
عربي Àngale Urdu
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ko tudde Yàlla ginnaaw julli gu ne
عربي Àngale Urdu
buleen def séen kër yi ay bàmmeel, Saytaane day daw kër goo xam ne dañu fay jàng saaru Al-Baxara
عربي Àngale Urdu
ma wax: Subhaanal Laahi, wal hamdu lil Laahi, wa laa ilaaha illal Laahu, wal laahu akbaru, moo ma gënal lépp lu jant bi fenk ci kawam
عربي Àngale Urdu
Amul benn bis bob jëf ca lu baax moo gënal Yàlla ci bis yii» maanaam fukki bis yi nëkk Si weeru tabaski
عربي Àngale Urdu
ku bàyyi jullig tàkkusaan jëfam yàquna
عربي Àngale Urdu
Ku jàpp te rafetal njàpp ma, ay ñaawtéefam day génn ci aw yaramam bay génn ci ay weyam
عربي Àngale Urdu
ku jàng ñaari aaya yi ci mujjug saaru Al-Baxara cig guddi danañu ko fegal leeb luy Aw ay
عربي Àngale Urdu
Ku jáng wenn araf ci téereb Yàlla bi dina am jenn tiyaaba, jenn tiyaaba ju ne day tolloo ak fukki tiyaaba
عربي Àngale Urdu
bu nit ki dundalee njabootam di ci séentu aw yiw loolu dina nekk ci moom ab sarax
عربي Àngale Urdu
Ngëm juróom-ñaar fukki xaaj la ak lu topp» wala: «juróom-benn fukki xaaj la ak lu topp» - ci ay xaaj, bi ci gën a kawe: mooy wax: laa ilaaha illal Illa Laahu, bi ci gën a suufe, mooy: randale aw lor ci kaw yoon wi
عربي Àngale Urdu
bumu bàyyi benn caq walla bantu fett ci doqug genn giléem te daggu ko
عربي Àngale Urdu
ku wax: laahi ilaaha illallaahu, amul kenn ku ñu war a jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, daal di weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla alalam ak dereetam araam na, Yàlla rekk nag mooy càmbar ay jëfam
عربي Àngale Urdu
jikkóom moo doon
عربي Àngale Urdu
ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm
عربي Àngale Urdu
Yàlla mu kawe mi day wax ki gën a woyof mbugal ci waa sawara ëllëg bis-pénc: boo moomoon li ci suuf lépp ndax danga ko jote sa bopp? Mu ne: waaw
عربي Àngale Urdu
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan tudd Yàlla ci bépp jamono
عربي Àngale Urdu
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na zulu
عربي Àngale Urdu
baatu dëgg boobu jinne moo koy këf sànni ko ci noppi kilifaam kem kàddu ginaar gu jigéen, ñu jaxase si lu ëpp téeméeri fen
عربي Àngale Urdu
Nekkoon a nu ci Umar mu wax ne: "tere nañ nu toggoo lu metti
عربي Àngale Urdu
amul kenn kuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la te mu dëggu ci xolam lu dul ne Yàlla dana ko araamal ca sawara
عربي Àngale Urdu
sunu Boroom bu baarkeel bi te kawe day wàcc guddi gu nekk ci asamaani àdduna si bu guddi gi desee ñatteelu xaaj bu mujj ba
عربي Àngale Urdu
buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli
عربي Àngale Urdu
ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka
عربي Àngale Urdu
digal nañu ma may sujjóot ci juróom-ñaari cér
عربي Àngale Urdu
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wa haafinii, wahdinii, warsuqnii
عربي Àngale Urdu
Allaahumma Antas Salaamu, wa Minkas Salaamu, Tabaarakta Sal Jalaali wal ikraami
عربي Àngale Urdu
jullil taxaw, boo ko manul nga toog, boo ko manul nga wetu
عربي Àngale Urdu
ndax danga dégg wooteg julli gi?" Mu ne ko: waaw, mu ne ko: "kon nag wuyujil 
عربي Àngale Urdu
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal na ñu xutbag aajo
عربي Àngale Urdu
Deesul takk jigéen ci lu dul kilifa
عربي Àngale Urdu
yaw xale bi, tuddal Yàlla, te lekke sa loxo ndeyjoor, te lekk li ne ci sa kanam
عربي Àngale Urdu
bu kenn ci yenn di lekk na lekke loxo ndeyjooram, buy naan na naane loxo ndeyjooram, ndax Saytaane loxob càmmooñam lay lekke, loxob càmmoñam lay naane
عربي Àngale Urdu
ku génnug topp, daal di tàqalikoo ak mbooloo ma ba faatu, kon dee na deewug ceddo
عربي Àngale Urdu
ku ñëw ci yéen fekk ngeen abooloo ci lenn njiit, mu bëgg a xotti mbooloo mi, mbaa mu tàqqale séen mbooloo mi, rayleen ko
عربي Àngale Urdu
Ku ray koo séqal kóllëre, du xeeñcu xetug Àjjana, te dinanteem ak xetam ga soree ni doxub ñent-fukki at
عربي Àngale Urdu
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- rëbb na kiy ger ak ki ñuy ger cib àtte
عربي Àngale Urdu
tabax nañu lislaam ci juróom
عربي Àngale Urdu
ku gis ci yéen lu ñu sib na ko soppi ci loxoom, bu ko manul na ko soppi ci làmmeñam, bu ko manul na ko soppi ci xolam, te loolu moo gën a néew ci ngëm
عربي Àngale Urdu
ku rafetal ci Lislaam deesu ko toppe la mu defoon ca ceddu ga, waaye ku def lu ñaaw ci Lislaam dees na ko toppe lu njëkk la ak lu mujj li
عربي Àngale Urdu
waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
عربي Àngale Urdu
Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf
عربي Àngale Urdu
mbaa sama Hadiis du yeksi ci nit mu tëdd ag gàngunaayam naan: Diggante nun ak yéen téeréb Yàlla la
عربي Àngale Urdu
mbugal ñeel na tastën ya ca sawara, deeleen jotal njàppu mi
عربي Àngale Urdu
àqi Yàlla ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko te bañ koo bokkaale ak dara, àqi jaam ñi ci Yàlla nag mooy du mbugal ku ko bokkaalewul ak dara
عربي Àngale Urdu
ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana, ku faatu te bokkaale ko ak dara dana dugg sawara
عربي Àngale Urdu
wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc
عربي Àngale Urdu
Yàlla dina musal nit ci samaw xeet ci kanamu mbindéef yépp ëllëg bis-pénc
عربي Àngale Urdu
bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm-
عربي Àngale Urdu
Yàlla bind na ndogali mbindéef yi njëkk muy bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-fukki junniy at
عربي Àngale Urdu
dénk naa leen ngeen ragal Yàlla ci dégg ak topp, donte jaamub Habasa la, dangeen gis ci sama ginnaaw ag wuute gu tar, waaye nangeen jàpp ci sama Sunna ak sunnay njiit yu jub ya tey jubal
عربي Àngale Urdu
Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar
عربي Àngale Urdu
ku fàtte genn julli na ko julli saa yu ko fàttalikoo, dara manu koo fay lu dul loolu
عربي Àngale Urdu
li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli
عربي Àngale Urdu
kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na
عربي Àngale Urdu
Yàlla mu kawe mi nee na: seddale naa julli ci sama diggante ak sama jaam bi ci ñaari xaaj, ñeel na sama jaam bi lu mu laaj
عربي Àngale Urdu
yaw Abbaas, yaw baay taxu Yonnente Yàlla bi, ñaanal Yàlla jàmmi àdduna ak allaaxira
عربي Àngale Urdu
Yàlla tere na leen ngeen di giñ ci seen baay yi
عربي Àngale Urdu
Fekk nañu jenn jigéen ñu ray ko ci benn ci xarey Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, Yonnente bi daal di ñaawlu ñuy ray jigéen ñi ak xale yi
عربي Àngale Urdu
tere na nisër, daal di wax ne: "du indi aw yiw, waaye dees ciy genne aji-nay ji
عربي Àngale Urdu
man de giñ naa ci Yàlla ne -bu soobee Yàlla- duma giñ ci dara ba noppi gis leneen lu ko gën, lu dul ne dinaa kaffaara sama giñ ba te def la ko gën
عربي Àngale Urdu
li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc mooy dereet
عربي Àngale Urdu
kiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku kooku moo ngi ci yoonu Yàlla
عربي Àngale Urdu
Bu leen sol suwaa walla sooy, bu leen naan ci ndabal wurus mbaa xaalis, te bu leen lekk ci ay boolam, ndax ñoom la ñeel fii ci àdduna, waaye nun la ñeel fële ca àllaaxira
عربي Àngale Urdu
ku sol sooy fii ci àdduna du ko sol fële ca allaaxira
عربي Àngale Urdu
man nag giñloowuma leen ci ne dama leen a tuumaal, waaye Jibriil moo ñëw fi man xibaar ma ne Yàlla mu kawe mi moo ngi leen di puukarewoo fa malaaka ya
عربي Àngale Urdu
ñoom ñaar de ñoo ngi leen di mbugal, te sax mbugaluñu leen ci lu rëy, kenn ki moom daawul suturawu bu daan saw, keneen ki nag da daan dox di rambaaj
عربي Àngale Urdu
bu ngeen déggee woote gi nangeen wax lu mel ni li noddkat bi di wax
عربي Àngale Urdu
bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab
عربي Àngale Urdu
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ndayjoor daan na ko yéem ci buy sol dàll, ak buy peñewu, ak buy laab, ak ci mbiram yépp
عربي Àngale Urdu
loolu dereti sidit la, waaye bàyyil julli ci limu bis yi ngay gis mbaax, topp nga sangu te julli
عربي Àngale Urdu
yamaleleen seen sàppe yi, ndax yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi
عربي Àngale Urdu
Bu kenn ci yéen di jàpp na def ndox ci bakkanam daa di saraxndiku, kuy fomp (laabu) na ko tóolal
عربي Àngale Urdu
bu nit ki duggee këram, daal di tudd Yàlla buy dugg ak buy lekk, saytaane day wax naan: amuleen fanaanukaay, amuleen reerukaay
عربي Àngale Urdu