عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صلى الله عليه وسلم قَالَ:
«إِذَا مَاتَ الْإِنْسَانُ انْقَطَعَ عَنْهُ عَمَلُهُ إِلَّا مِنْ ثَلَاثَةٍ: إِلَّا مِنْ صَدَقَةٍ جَارِيَةٍ، أَوْ عِلْمٍ يُنْتَفَعُ بِهِ، أَوْ وَلَدٍ صَالِحٍ يَدْعُو لَهُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1631]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«Bu nit ki faatoo ay jëfam dog na ba mu des ñatt: ba mu des saraxe buy wéy, walla xam-xam bu ñuy jariñoo, walla doom ju baax ju koy ñaanal».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1631]
Yonnente bi day xibaare ne jëfi aji-faatu ji day dagg cig faatoom, du
am ay yiw ginnaaw ba mu faatoo ba mu des ñatti mbir ndaxte moom mooy sabab bi:
Bi ci njëkk: sarax boo xam ni yool ba day sax, niki Wàqf, ak tabax jàkka, ak gas teen, ak yeneen.
Ñaareel bi: xam-xam bu nit ñi di jariñoo, niki taalif ay téerey xam-xam, walla mu jàngal nit, nit kooka di tasaare xam-xam bi ginnaaw ba mu faatoo.
Ñatteel bi: doom ju baax ju gëm di ñaanal ay way-juram.