عَنْ جَابِرٍ رضي الله عنه قال: أَخْبَرَنِي عُمَرُ بْنُ الْخَطَّابِ:
أَنَّ رَجُلًا تَوَضَّأَ فَتَرَكَ مَوْضِعَ ظُفُرٍ عَلَى قَدَمِهِ فَأَبْصَرَهُ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَقَالَ: «ارْجِعْ فَأَحْسِنْ وُضُوءَكَ» فَرَجَعَ، ثُمَّ صَلَّى.
[صحيح بشواهده] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 243]
المزيــد ...
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Umar Ibnul Xattaab xibaar na ma ne:
Benn waay dafa jàppu daal di bàyyi barab buy tollook aw weh ci ay ndëggoom Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal akmucc- gis ko ne ko:"dellul te rafetal sa njàppu mi" mu dellusi,daal di julli.
[Wér na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 243]
Umar -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa gis benn waay bu jàppu ba noppi,fekk dafa bàyyi luy tollook aw weh ci ay ndëggoom te ndoxum njàppu mi laalu ko. Mu joxoñ barab boobu mu bàyyi ne ko: dellul te rafetal sa njàppu mi te matal ko jox cér bu nekk àqam ci ndox mi, Waa ji dellu matal njàppam mi daal di julli.