عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِذَا اسْتَيْقَظَ أَحَدُكُمْ مِنْ مَنَامِهِ فَلْيَسْتَنْثِرْ ثَلَاثَ مَرَّاتٍ، فَإِنَّ الشَّيْطَانَ يَبِيتُ عَلَى خَيَاشِيمِهِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 238]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"bu kenn ci yeen yeewoo ci ay nelawam na fiiru ñatti yoon, ndaxte Saytaane day fanaan ci paxi bakkanam".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 238]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day ñaax ki yeewu ci ay nelawam mu fiiru ñatti yoon; fiiru mooy génne ndox mi ci bakkan bi ginnaaw ba ñu ko ca dugalee, loolu nag ndaxte Saytaane day fanaan ci paxi bakkan bi.