عَنْ حُمْرَانَ مَوْلَى عُثْمَانَ بْنِ عَفَّانَ رضي الله عنه:
أَنَّهُ رَأَى عُثْمَانَ بْنَ عَفَّانَ دَعَا بِوَضُوءٍ، فَأَفْرَغَ عَلَى يَدَيْهِ مِنْ إِنَائِهِ، فَغَسَلَهُمَا ثَلَاثَ مَرَّاتٍ، ثُمَّ أَدْخَلَ يَمِينَهُ فِي الْوَضُوءِ، ثُمَّ تَمَضْمَضَ وَاسْتَنْشَقَ وَاسْتَنْثَرَ، ثُمَّ غَسَلَ وَجْهَهُ ثَلَاثًا، وَيَدَيْهِ إِلَى الْمِرْفَقَيْنِ ثَلَاثًا، ثُمَّ مَسَحَ بِرَأْسِهِ، ثُمَّ غَسَلَ كُلَّ رِجْلٍ ثَلَاثًا، ثُمَّ قَالَ: رَأَيْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَتَوَضَّأُ نَحْوَ وُضُوئِي هَذَا، وَقَالَ: «مَنْ تَوَضَّأَ نَحْوَ وُضُوئِي هَذَا ثُمَّ صَلَّى رَكْعَتَيْنِ لَا يُحَدِّثُ فِيهِمَا نَفْسَهُ غَفَرَ اللهُ لَهُ مَا تَقَدَّمَ مِنْ ذَنْبِهِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 164]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Humraan jaamub
Usmaan Ibn Affaan, mu wax ne, gis na Usmaan Ibn Affaan laaj ndox mu mu jàppoo, mu tanq loxoom ci ndab li, raxas leen ñatti yoon, mu dugal ndeyjooram ci jàppukaay bi, daal di gallaxndiku saraxndiku fiiru, daal di raxas xar kanamam ñatti yoon, ak ñaari loxoom ba ci conco yi ñatti yoon, daal di masaa boppam, daal di raxas tànk bu ne ñatti yoon, daal di wax ne: gis naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy jàppoo kem sama njàpp mii, ba noppi wax ne: "ku jàppoo kem sama njàpp mii, daal di julli ñaari ràkka yoy du ca xalaat dara, kon Yàlla dana ko jéggal bàkkaaram yi jiitu".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 164]
Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day jàngale melokaanu djàppum Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci anamug jëfe; ngir leeral gi gën a mat, mu laaj am ndox ci ndab, dàldi sotti ci loxoom ñatti yoon, ginnaaw loolu mu dugal loxo ndeyjooram ci ndab li, tanq ci ndox yëngal ko ci gémmeñam daal di koy génne, mu xëcc ndox mi ci bakkanam, daa di koy génnewaat, daal di raxas xar kanamam ñatti yoon, daal di raxas ay loxooom ak ñaari conco yi ñatti yoon, mu tooyal loxoom rombale ko ci kaw bopp bi benn yoon, daal di raxas ñaari tànkam ba ci dojor yi ñatti yoon .
Ba mu noppe mu waxleen ne gis na Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jàppe njàpp mu mel nii, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bégal leen ne ku jàpp nu mel nii mu jàppe, daal di julli ñaari ràkka ànd ca ak toroxlu, te teewal ca xolam ci ne moo ngi ci kanamu Boroomam mu màgg mi, kon Yàlla dana ko fay ci njàpp mu mat moomu ak julli gu sell googu ag njéggal ñeel bàkkaaram ya jiitu.