Listu hadiis yi

Nekkul woon ku ñaaw i wax du caagine ay jëf, du caagine kuy coow ci ja yi, (marché)te daawul fayantoo lu ñaaw, waaye day baale di jéggale
عربي الإنجليزية الأوردية
bàmmeel de mooy wàccuwaay bi njëkk ci wàccuwaayi allaaxira yi, bu ca muccee la ca ginnaawam mooy gën na yomb, bu ca muccul la ca ginnaawam mooy gën na tar
عربي الإنجليزية الأوردية
mbooloo miy njëkk a dugg àjjana dañuy nekk ci melow weer wi ci guddig Badr, ña topp ca ñoom gën a tarug leer biddiwu per ci ag leer
عربي الإنجليزية الإندونيسية
wàcce nañu ci man ay aaya yoy musuñoo wàcce yu mel ni ñoom, Ñaari muslukaay yi
عربي الإنجليزية الإندونيسية
bu nit ñi xamoon li nekk ci nodd gi ak sàppe su njëkk si te manu ñu lu dul tegoo bant kon danañu ko tegoo bant
عربي الإنجليزية الإندونيسية
ku wax: radiiitu bil-Laahi Rabban, wa bi Muhammadin Rasuulan, àjjana war na ci moom
عربي الإنجليزية الإندونيسية
yégleen ne sàngara araamal nañu ko
عربي الإنجليزية الإندونيسية
ku xandaalu daanu ci aw doj daal di ray boppam kooku ci sawaraw Jahannama la jëm di ca xandaalu sax ca di ku ñu fay saxal ba fàww
عربي الإنجليزية الإندونيسية
jaayanteleen ak man ci ne dungeen bokkaale Yàlla ak dara, te dungeen sàcc, dungeen njaalo
عربي الإنجليزية الإندونيسية
moytulleen bàkkaar yi ñuy xeeb
عربي الإنجليزية الإندونيسية
dañu ma a yónni ngir ma mottali jikkó yu tedd yi
عربي الإنجليزية الأوردية
juróom-ñaar yii Yàlla dana leen keral bis ba genn ker dul am lu dul keram ga
عربي الإنجليزية الإندونيسية
bu kenn jëmale mbokkam ngànaay, ndax xamul ne Saytaane man naa bif loxoom, mu tàbbi ci kàmbu sawara
عربي الإنجليزية الإندونيسية
giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm, giñ naa ci Yàlla ne du gëm", ñu ne ko: kan yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne: "ki dëkkandoom muccug ci ay loram
عربي الإنجليزية الإندونيسية
Yàlla mu màgg mi nee na: doomu Aadama moo ngi may lor day ŋàññ jamono ji te man maay jamono, ci sama loxo la mbir yi nekk maa koy wëlbati guddi ak bëccëg
عربي الإنجليزية الإندونيسية
ñi gën ci yéen ñooy samag maas, topp ci ña ca topp, topp ci ña ca topp'
عربي الإنجليزية الإندونيسية
ay fitna dana am, yëgleen ne bu fitna amee ka toog moo gën ka kay dox, kay dox mooo gën kay daw,
عربي الإنجليزية الإندونيسية
Allaahuma innii as-aluka alhudaa wattuqaa walhafaafa walxinaa
عربي الإنجليزية الأوردية
yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, ndax dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka
عربي الإنجليزية الأوردية
waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
عربي الإنجليزية الأوردية
digal nañu ma ma xeex ak nit ñi ba baa ñuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka
عربي الإنجليزية الأوردية
bu ñu doon jox nit ñi ci seen i wootewoo kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a indi firnde, kiy weddi daa war a giñ.
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla ak ub yonnenteem araamal na ñu jaay sàngara, ak médd, ak mbaam xuux, ak ay xërëm
عربي الإنجليزية الأوردية
bokk na ci li fi nit ñi fekk ci waxi Yonnente ya jiitu: boo amul looy rus defal lu la neex
عربي الإنجليزية الأوردية
nekkal ci àdduna mel ni ku tumurànke walla kuy jaar ciw yoon
عربي الإنجليزية الأوردية
bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla
عربي الإنجليزية الأوردية
lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko
عربي الإنجليزية الأوردية
mo ndax Yàlla defalu leen lu ngeen di saraxee? Bépp sàbbaal ab sarax la, bépp sant ab sarax la, bépp tudd Yàlla it sarax la, digle lu baax sarax la, tere li bon sarax la, sëyug kenn ci yéen itam sarax la
عربي الإنجليزية الأوردية
moytuleen salte yii Yàlla tere, ku ca laal na suturawu ci surutas Yàlla, te tuub jëm ci Yàlla, ndaxte ku ñu wuññil ay bootam dananu teg ci moom Téereb Yàlla mu màgg mi
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla farataal na ay farata buleen ko sànk, mu teg ay dig buleen ko jéggi, mu araamal ay mbir buleen ko xëtt, mu noppi ci ay mbir ngir yërëm leen waaye fàttewu ko kon buleen ko gëstu
عربي الإنجليزية الأوردية
Jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am
عربي الإنجليزية الأوردية
tabax nañu lislaam ci juróom
عربي الإنجليزية الأوردية
kenn ci yéen de dees na dajale ag mbindam ci biiru yaayam ñent-fukki fan
عربي الإنجليزية الأوردية
képp ku sos ci sunu mbir mii lu ci bokkul dees ka koy delloo
عربي الإنجليزية الأوردية
li dagan de leer na li araam it leer na,
عربي الإنجليزية الأوردية
diine de laayante-biir la
عربي الإنجليزية الأوردية
lépp lu ma leen tere nangeen ko moytu, lépp lu ma leen digal nangeen ca def lu ngeen man
عربي الإنجليزية الأوردية
yéen nit ñi, Yàlla ku teey la te du nangu lu dul lu teey, te Yàlla dafa digal way-gëm ñi li mu digal Yonnente yi
عربي الإنجليزية الأوردية
Bàyyil looy sikk-sàkka jëm ci loo sikk-sàkkawul
عربي الإنجليزية الأوردية
Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla bind na Ag rafetal ci bir yépp
عربي الإنجليزية الأوردية
Yaw ngóor si dinaa la xamal ay waat: wattul Yàlla kon Yàlla dina la sàmm, nanga bàyyi xel Yàlla kon mu féete la fépp, booy ñaan ñaanal Yàlla, booy sàkku ndimbal na nga dimbandikoo Yàlla
عربي الإنجليزية الأوردية
bokk na ci li fi nit ñi fekk ci waxi Yonnente ya jiitu: boo amul looy rus defal lu la neex
عربي الإنجليزية الأوردية
wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc
عربي الإنجليزية الأوردية
waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
عربي الإنجليزية الأوردية
Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf
عربي الإنجليزية الأوردية
fépp fu yax di daje ci nit sarax la
عربي الإنجليزية الأوردية
Maa ngi leen di dénk ragal Yàlla, ak dégg ak topp, donte ab jaam moo leen jiite, képp ku dund ci yéen dana gis wuute gu bari, maa ngi leen di dénk sama sunna si ak sunnay njiit yu jub yi tey jubal
عربي الإنجليزية الأوردية
laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku Yàlla yombalal
عربي الإنجليزية الأوردية
deesul loru waaye deesul lore
عربي الإنجليزية الأوردية
bu ñu doon jox nit ñi ci seen i wootewoo kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a indi firnde, kiy weddi daa war a giñ.
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla bind na yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di koy leeral
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla mu kawe mi nee na: ku noonook samaw wàlliyu waajal naa ko xeex, te sama jaam du ma jegeñ-jegeñlu ci dara lu ma gënal li ma farataal ci moom
عربي الإنجليزية الأوردية
kenn ci yéen du gëm ba keroog bànneexam di topp li ma indi
عربي الإنجليزية الأوردية
Lépp luy màndiloo dafa araam.
عربي الإنجليزية الأوردية
ñent yii ku ñu nekk ci moom nekk na ab naaféq bu sotti, ku wenn melo ci ñoom nekk ci moom am na wenn melow naaféq ba keroog mu koy bàyyi: bu waxtaanee fen, bu kóllareentee wor, bu digee wuute ko, bu xuloo wax lu bon
عربي الإنجليزية الأوردية
su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc yi, day xëy nekk ku woos xiif di gont biir bi fees dell
عربي الإنجليزية الأوردية
baax mooy: rafet jikkó, bàkkaar mooy liy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ci gis ko
عربي الإنجليزية الأوردية
bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla jéggal na samaw xeet njuumte ak fàtte ak lu ñu leen forse
عربي الإنجليزية الأوردية
dëddul àdduna kon Yàlla dana la bëgg, dëddul li ci nit ñi kon nit ñi danañu la bëgg
عربي الإنجليزية الأوردية
nàmpal day araamal li njureel di araamal
عربي الإنجليزية الأوردية
doomu Aadama feesalul lenn ndab lu yées biiram, doy na sëkk doomu Aadama ji lekk gu mu taxawale ndiggam li, bu manut a ñàkk, kon na def biiram ñatti xaaj benn ba ngir lekkam, beneen ba ngir naanam, ñatteelu xaaj ba ngir noyyeem
عربي الإنجليزية الأوردية
bokk na ci rafetug ngëmu nit ki: mu bàyyi lu ko amalul njariñ
عربي الإنجليزية الأوردية