عَنْ أَمِيرِ المُؤْمِنِينَ أَبِي حَفْصٍ عُمَرَ بْنِ الخَطَّابِ رضي الله عنه قَالَ: سَمِعْتُ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«إنَّمَا الأَعْمَالُ بِالنِّيَّاتِ، وَإِنَّمَا لِكُلِّ امْرِئٍ مَا نَوَى، فَمَنْ كَانَتْ هِجْرَتُهُ إلَى اللَّهِ وَرَسُولِهِ فَهِجْرَتُهُ إلَى اللَّهِ وَرَسُولِهِ، وَمَنْ كَانَتْ هِجْرَتُهُ لِدُنْيَا يُصِيبُهَا أَوْ امْرَأَةٍ يَنْكِحُهَا فَهِجْرَتُهُ إلَى مَا هَاجَرَ إلَيْهِ».
[صحيح] - [رواه إماما المحدثين أبو عبد الله محمد بن إسماعيل بن إبراهيم بن المغيرة بن بردزبه البخاري، وأبو الحسين مسلم بن الحجاج بن مسلم القشيري النيسابوري في صحيحيهما اللذين هما أصح الكتب المصنفة] - [الأربعون النووية: 1]
المزيــد ...
Jële nañu ci njiiti jullit ñi baayu Hafsa Umar Ibn Al-Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax ne:
"Jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am, képp ku gàddaay ngir Yàlla ak ub Yonenteem, kooku gàddaayam dina jëm ci Yàlla ak Yonenteem, waaye képp ku gàddaay ngir àdduna jum soxlaa jot walla jigéen ju mu bëgg a takk kon gàddaayam jëm na ca la ko tax a gàddaay".
[Wér na] - [رواه إماما المحدثين أبو عبد الله محمد بن إسماعيل بن إبراهيم بن المغيرة بن بردزبه البخاري وأبو الحسين مسلم بن الحجاج بن مسلم القشيري النيسابوري في صحيحيهما اللذين هما أصح الكتب المصنفة] - [الأربعون النووية - 1]
Yónente bi day leeral ne jëf yépp ci yéene ja la aju, te àtte bii daa matale jëf yépp moo xam jaamu yi la mbaa jëflante yi, koo xam ne jëfam njariñ la ci jublu du ca am lu dul njariñ loola waaye du ci am tiyaaba, ko xam ne jëfam jege Yàlla la ci jublu dana am ca jëfam ja ab yool ak ug pay, donte jëf i aada la, niki lekk ak naan.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- joxe waat meneen misaal ci ni yéene di jeexitale ci jëf yi ànd ak seenug niróo ci melo wi feeñ, mu leeral ne ku jublu ci gàddaay bàyyi réewam ngir jublu ci ngërëmal Boroomam kon gàddaayam ga gàddaayu sariiha la gu ñu nangu te dees na ko fay ab yool ngir yéeneem ju dëggu, waaye ku jublu cig gàddaayam njariñal àdduna, alal, ak daraja ak am njaay, walla soxna du am ca gàddaayam ga lu dul njariñ yooya mu yéene woon, te du am benn cér cig pay mbaa ab yool.