عَنْ أَبِي يَعْلَى شَدَّادِ بْنِ أَوْسٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنْ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِنَّ اللهَ كَتَبَ الْإِحْسَانَ عَلَى كُلِّ شَيْءٍ، فَإِذَا قَتَلْتُمْ فَأَحْسِنُوا القِتْلَةَ، وَإِذَا ذَبَحْتُمْ فَأَحْسِنُوا الذِّبْحَةَ، وَلْيُحِدَّ أَحَدُكُمْ شَفْرَتَهُ، وَلْيُرِحْ ذَبِيحَتَهُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [الأربعون النووية: 17]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Yahlaa Saddaad ibn Aws yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"Yàlla bind na Ag rafetal ci bir yépp, bu ngeen dee ray nangeen rafetal rayiin wa, bu ngeen dee rendi nangeen rafetal rendiin wa, nangeen daas seenug ñawka tey noppal li ngeen di rendi".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [الأربعون النووية - 17]
Yónente bi xamle na ne Yàlla mu kawe mi dafa waral si nun rafetal ci lépp, te rafetal mooy: di fuglu Yàlla ba fàwwu, ci jaamu gi ak ci def yiw ak ci fegal mbindeef yi lor, bokk na ci loolu di rafetal cig ray ak cig rendi.
Rafetal cig ray ci jamonoy fayontoo: ci tànn yoon wa gën a yomb te gën a woyof te gën a gaaw ci faat ki ñuy ray.
Rafetal cig rendi mooy: mu am ñeewantu ci bayima bi mu ñawal jumtukaay bi, te bañ koo daas ci kanamu la muy rendi, fekk ma nga koy xool, te mu bañ koo rendi fekk am na fa ay jur yu koy xool.