1. Li jiitu
  2. Ràññetle yi
  3. Ngëneel yi ak teggiin yi

Hadiis Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam

عَنْ أَبِي حَمْزَةَ أَنَسِ بْنِ مَالِكٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ -خَادِمِ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ- عَنْ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لاَ يُؤْمِنُ أَحَدُكُمْ، حَتَّى يُحِبَّ لِأَخِيهِ مَا يُحِبُّ لِنَفْسِهِ»

Jële nañu ci Abuu Hamsata Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm -liggéeykatu Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam"

Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér الأربعون النووية - 13

Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne ´gëm gu mat kenn du ko am lu dul ne dafa bëggal mbokkam li mu bëggal boppam ci jaamu Yàlla ak xeetu yiw yi ci diine ak ci àdduna, bu gisee ci mbokkam ag wàññeeku ci diineem, day pasteefu ci yéwénal ko, bu ca gisee yiw mu dëgëral ko ca, te dimbale ko ca, daal di koy laabire ci mbiri diineem ak àddunaam.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

  1. Nit ki dafa war a bëggal mbokkam li mu bëggal boppam; ndaxte dàq gëmug ki bëggalut mbokkam li mu bëggal boppam day tegtale warug loolu.
  2. Mbokkoo ci Yàlla moo gën a kawe mbokkoo ci askan, kon nag àqam moo gën a war.
  3. Araamal nañu lépp luy dàqonte ak mbëggeel gii ci ay wax ak i jëf niki wuruj ak jëw ak soxor ak noonoo ci kaw bakkanu jullit bi ak alalam ak deram.
  4. Jëfandikoo yenn baat yiy sawarloo ci jëf; ndax li mu wax ne "ñeel mbokkam".
  5. Al-Kirmaanii yal na ko Yàlla yërëm nee na: bokk na ci gëm ba tay mu bañal mbokkam li mu bañal boppam ci ay, tuddu ko nag; ndaxte bëgg dara day taqoo ak bañ safaanam, kon ñàkk gee tudd ag doyloo la rekk.

Gaaral firi yi

60 Làkk wi
EN English الإنجليزية
UR اردو الأوردية
ES Español الإسبانية
ID Indonesia الإندونيسية
BN বাংলা البنغالية
FR Français الفرنسية
TR Türkçe التركية
RU Русский الروسية
BS Bosanski البوسنية
SI සිංහල السنهالية
HI हिन्दी الهندية
ZH 中文 الصينية
FA فارسی الفارسية
VI Tiếng Việt الفيتنامية
TL Tagalog تجالوج
KU Kurdî الكردية
HA Hausa الهوسا
PT Português البرتغالية
ML മലയാളം المليالم
TE తెలుగు التلغو
SW Kiswahili السواحيلية
TA தமிழ் التاميلية
MY မြန်မာ البورمية
TH ไทย التايلندية
DE Deutsch الألمانية
JA 日本語 اليابانية
PS پښتو بشتو
AS অসমীয়া الأسامية
SQ Shqip الألبانية
SV Svenska السويدية
AM አማርኛ الأمهرية
NL Nederlands الهولندية
GU ગુજરાતી الغوجاراتية
KY Кыргызча القيرقيزية
NE नेपाली النيبالية
LT Lietuvių الليتوانية
PRS دری الدرية
SR Српски الصربية
TG тоҷикӣ الطاجيكية
RW Kinyarwanda الكينياروندا
RO Română الرومانية
HU Magyar المجرية
CS Čeština التشيكية
MOS Moore الموري
MG Malagasy المالاجاشية
OM Oromoo الأورومو
KN ಕನ್ನಡ الكانادا
AZ Azərbaycan الأذربيجانية
UZ O‘zbek الأوزبكية
UK Українська الأوكرانية
KA ქართული الجورجية
MK Македонски المقدونية
KM ភាសាខ្មែរ الخميرية
BM Bambara البامبارية
PA ਪੰਜਾਬੀ البنجابية
MR मराठी الماراثية
DA Dansk الدنماركية
RN Kirundi الكيروندي
KMR Kurmancî الكرمنجية
MS Bahasa Melayu الملايو