عَنْ أَبِي مُـحَمَّدٍ الحَسَنِ بْنِ عَلِيِّ بْنِ أَبِي طَالِبٍ - سِبْطِ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَرَيْحَانَتِهِ-، قَالَ: حَفِظْتُ مِنْ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«دَعْ مَا يَرِيبُك إلَى مَا لَا يَرِيبُكَ».
[صحيح] - [رواه الترمذي والنسائي] - [الأربعون النووية: 11]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Muhammad Al-Hasan ibn Aliyun ibn Abii Taalib -sétu Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di mbégteem-, nee na: mokkal naa ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
"Bàyyil looy sikk-sàkka jëm ci loo sikk-sàkkawul".
[Wér na] -
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa digle ñu bàyyi wax yi ak jëf yi ñuy sikk-sàkka ne dañu ko a tere walla déet, ndax dafa araam walla dafa dagan, te jëm ci yi ñu sikk-sàkkawul te am yaqiin ci rafetam ak ug daganam.