Xàjjale yi:
+ -

عَنْ أَبِي العَبَّاسِ، عَبْدِ الله بْنِ عَبَّاسٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا قَالَ: كُنْت خَلْفَ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَوْمًا، فَقَالَ:
«يَا غُلَامِ! إنِّي أُعَلِّمُك كَلِمَاتٍ: احْفَظِ اللَّهَ يَحْفَظْكَ، احْفَظِ الله تَجِدْهُ تُجَاهَكَ، إذَا سَأَلْتَ فَاسْأَلِ اللهَ، وَإِذَا اسْتَعَنْتَ فَاسْتَعِنْ بِاَللهِ، وَاعْلَمْ أَنَّ الأُمَّةَ لَوْ اجْتَمَعَتْ عَلَى أَنْ يَنْفَعُوكَ بِشَيْءٍ لَمْ يَنْفَعُوكَ إلَّا بِشَيْءٍ قَدْ كَتَبَهُ اللَّهُ لَكَ، وَإِنِ اجْتَمَعُوا عَلَى أَنْ يَضُرُّوكَ بِشَيْءٍ لَمْ يَضُرُّوكَ إلَّا بِشَيْءٍ قَدْ كَتَبَهُ اللَّهُ عَلَيْكَ؛ رُفِعَتِ الأَقْلَامُ، وَجَفَّتِ الصُّحُفُ». وَفِي رِوَايَةِ غَيْرِ التِّرْمِذِيِّ: «احْفَظِ اللهَ تَجِدْهُ أَمَامَكَ، تَعَرَّفْ إلَى اللهِ فِي الرَّخَاءِ يَعْرِفْكَ فِي الشِّدَّةِ، وَاعْلَمْ أَنَّ مَا أَخْطَأَكَ لَمْ يَكُنْ لِيُصِيبَكَ، وَمَا أَصَابَك لَمْ يَكُنْ لِيُخْطِئَكَ، وَاعْلَمْ أَنَّ النَّصْرَ مَعَ الصَّبْرِ، وَأَنْ الفَرَجَ مَعَ الكَرْبِ، وَأَنَّ مَعَ العُسْرِ يُسْرًا».

[صحيح] - [رواه الترمذي وغيره] - [الأربعون النووية: 19]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Àbbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm, mu wax ne: nekkoon ci ginnaaw Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc benn bis, mu ne ma:
"Yaw ngóor si dinaa la xamal ay waat: wattul Yàlla kon Yàlla dina la sàmm, nanga bàyyi xel Yàlla kon mu féete la fépp, booy ñaan ñaanal Yàlla, booy sàkku ndimbal na nga dimbandikoo Yàlla, te nga xam ne bu ñépp daje woon ngir jariñ la ci dara duñu ko man lu dul lu Yàlla dogal ci yaw ba noppi, bu ñépp daje woon it ngir lor la ci dara duñu ko man lu dul lu Yàlla dogal ci yaw ba noppi; ndax teggi nañu bindukaay ya, te àlliwo ya wow na".

[Wér na] -

Leeral

Ibn Àbbaas yal na ko Yàlla dollee gërëm day nettali ne ab xale la woon mu bokkoon ak Yonente bi war ci jenn daaba, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: dinaa la xamal ay mbir yoo xam ne Yàlla dina la ci jariñ: Nanga wattu Yàlla ci sàmm ay ndigalam te moytu ay tereem, ba da lay fekk ci di ko topp ak di ko jegeñ-jegeñlu te du la fekk ca moy ya ak bàkkaar ya, boo defee loolu sag fay mooy moom Yàlla mu sàmm la ci ñaawteefi àdduna ak allaaxira, daal di lay dimbali ci say yitte foo man di jublu. Boo bëggee ñaan dara, bul ko ñaan ku dul Yàlla ndax moom rekk mooy wuyu aji-woote ji. Boo bëggee sàkku ndimbal bul ko sàkku ci ku dul Yàlla. Na nga am kóolute ci ne doo am benn njariñ donte waa suuf ñépp dañoo dajaloo ngir jariñ la, lu dul loo xam ne Yàlla bindaloon na la ko, lor it du dal sa kaw donte waa suuf ñépp dañoo dajaloo ngir lor la, lu dul lu Yàlla dogaloon ci sa kaw. Te lii Yàlla bind na ko nattale ko ak xereñam ak xam-xamam ba, te dara manul soppi la Yàlla bind. Te ku wattu Yàlla ci def ay ndigalam moytu ay tereem; na xam ne Yàlla moo ngi ci kanamu jaamam bi di xam ci li mu nekk di ko dimbali di ko dëgëral. Te nit ki bu toppee Yàlla ci jamonoy yomb-yomb kon bu nekkee ci tar-tar Yàlla dina ko yombalal defal ko génnuwaay, kon na jaam bu nekk gërëm li Yàlla dogal ci moom ci yiw ak ci ay. Ci tar-tar yi ak nattu yi jaam bi day taqoo ak muñ, ndaxte muñ mooy caabiy péexte, te bu tar-tar yi taree ag yombal dina ñëw jóge fa Yàlla, te bu jafe-jafe amee Yàlla dana ko wuutal ag yombte.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bégle gu màgg ci ne nit ki bu ko jafe-jafe dalee na xaar yomb-yomb ga.
  2. Dalal jaam bi ci bu ko musiba dalee, ak bu ñàkkee la mu bëgg ci li mu wax ne: "xamal ne lépp lu la jot waru la woon a moy, te lépp lu la moy waru la woon a jot" wax ju njëkk ji ag dalal la ci bu lu ñu bañ amee, bu ñaareel bi di ag dalal ci bu ñu ñàkkee lu ñu bëggoon.
Tekki: Àngale Urdu Endonesi Bengali Turki Risi Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Pastoo Asaami Albaani Amhari Gujarati Xisxisi Nipali Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Majri Ciikiya الموري Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية
Gaaral tekki yi
Xàjjale yi
Ndollent