عَنْ أُمِّ المُؤْمِنِينَ أُمِّ عَبْدِ اللَّهِ عَائِشَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا، قَالَتْ: قَالَ: رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّم:
«مَنْ أَحْدَثَ فِي أَمْرِنَا هَذَا مَا لَيْسَ مِنْهُ فَهُوَ رَدٌّ».
وَفِي رِوَايَةٍ لِمُسْلِمٍ: «مَنْ عَمِلَ عَمَلًا لَيْسَ عَلَيْهِ أَمْرُنَا فَهُوَ رَدٌّ».
[صحيح] - [رواه البخاري ومسلم] - [الأربعون النووية: 5]
المزيــد ...
Jële nañu ci ndayu jullit ñi Ummu Abdulla Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm, nee na: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"képp ku sos ci sunu mbir mii lu ci bokkul dees ka koy delloo"
[Wér na] - [رواه البخاري ومسلم] - [الأربعون النووية - 5]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ku sos ci diine ji mbaa mu jëf jëf joo xam ne Alxuraan ak Sunna tegtalewu ko, dees koy delloo boroom te deesu ko nangu fa Yàlla.