عَنْ أَبِي رُقَيَّةَ تَمِيمِ بْنِ أَوْسٍ الدَّارِيِّ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«الدِّينُ النَّصِيحَةُ» قُلْنَا: لِمَنْ؟ قَالَ: «لِلهِ وَلِكِتَابِهِ وَلِرَسُولِهِ وَلِأَئِمَّةِ الْمُسْلِمِينَ وَعَامَّتِهِمْ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [الأربعون النووية: 7]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Ruqiyyata Tamiim ibn Awsin Ad-Daarii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«diine de laayante-biir la» nu ne ko: ngir kan? Mu ne: «ngir Yàlla, ak ngir téereem bi, ak ngir Yónentam bi, ak ngir ñiiti jullit ñi, ak ngir jullit ñépp».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [الأربعون النووية - 7]
Yonente bi day xamle ne diine ji day taxaw ci sellal ak dëggu, ngir ñu defe ko na ko Yàlla warale ba mu mat sëkk te du am genn gàtteñlu walla wuruj. Ñu wax Yonente bi ne ko: kan la ñuy laaye-biir? Mu ne: Bi ci njëkk mooy: laabire ñeel Yàlla: ci sellal jëf yi ñeel ko, te bañ ko a bokkaale, nu gëm ag kennam ci ay jëfam, ak ci jaamu gi, ak ci ay turam ak i meloom, ak di màggal mbiram, tey woote jëme ci gëm ko. Ñaareel bi: laabire ñeel téereem bi te mooy Alxuraan ju tedd ji: ci nu gëm ne waxam la, te mooy téereem bi mujj, te moo folli mbooleem Sariiha ya ko jiitu, nu màggal ko, di ko jàng bu baax, tey jëfe ay laayaam yu leer yi tey gëm yu niróo ya, tey delloo mpirum soppikat yi, tey waaru ci ay waaraateem, tey siiwal am njàngaleem, di woote jëme ci moom. Ñatteel bi: laabire ngir Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: ci nu gëm ne mooy Yonnente bi mujj, te dëggal ko ci li mu indi, tay jëfe ay ndigalam, di moytu ay tereem, ta nuy bañ a jaamoo Yàlla ci lu dul li mu indi, nuy màggal ay àqam, te di ko weg, di tasaare wooteem bi, ak Sariihaam bi, te di ko dindil tuuma yi. Ñenteel bi: laabire ñeel njiiti jullit ñi: ci di leen dimbali ci dëgg, tay bañ a xëccoo ak ñoom, te di leen déggal ak di leen topp cig topp Yàlla. Juróomeel bi: laabire ñeel mbooleem jullit ñi: ci rafetal jëme ci ñoom ak di leen woo ci diine ji, te bañ leen a lor, ak bëgg leen, tey dimbalante ak ñoom cig mbaax ak ragal Yàlla.