عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ عَبْدِ الرَّحْمَنِ بْنِ صَخْرٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: سَمِعْت رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّم يَقُولُ:
«مَا نَهَيْتُكُمْ عَنْهُ فَاجْتَنِبُوهُ، وَمَا أَمَرْتُكُمْ بِهِ فَافْعَلُوا مِنْهُ مَا اسْتَطَعْتُمْ، فَإِنَّمَا أَهْلَكَ الَّذِينَ مِنْ قَبْلِكُمْ كَثْرَةُ مَسَائِلِهِمْ، وَاخْتِلَافُهُمْ عَلَى أَنْبِيَائِهِمْ».
[صحيح] - [رواه البخاري ومسلم] - [الأربعون النووية: 9]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata Abdur Rahmaan ibn Saxrin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax ne:
«lépp lu ma leen tere nangeen ko moytu, lépp lu ma leen digal nangeen ca def lu ngeen man, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seen laaj yu bari, ak seenug juuyoo ak seen i Yonente».
[Wér na] -
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dollee gërëm day leeral ne bu nu teree dara danu ko a war a moytu ci lu dul gennug settee, bu nu digalee dara nu def ca lu nu man. Topp mu àrtu ngir nu bañ a mel ni xeet ya jiitu woon ndax dañoo bari woon ay laaj lool jëme ci séen Yonente yi ànd ak loolu ñuy wuute ak ñoom, Yàlla mbugal leen ci ay xeeti alkande, kon jaadu na nu bañ a mel ni ñoom ngir nu bañ a alku kem na ñu alkoo.