عن تَميم الداري رضي الله عنه، قال: سمعتُ رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«لَيَبْلُغَنَّ هَذَا الأَمْرُ مَا بَلَغَ اللَّيْلُ وَالنَّهَارُ، وَلَا يَتْرُكُ اللهُ بَيْتَ مَدَرٍ وَلَا وَبَرٍ إِلَّا أَدْخَلَهُ اللهُ هَذَا الدِّينَ، بِعِزِّ عَزِيزٍ أَوْ بِذُلِّ ذَلِيلٍ، عِزًّا يُعِزُّ اللهُ بِهِ الإِسْلَامَ، وَذُلًّا يُذِلُّ اللهُ بِهِ الكُفْرَ» وَكَانَ تَمِيمٌ الدَّارِيُّ يَقُولُ: قَدْ عَرَفْتُ ذَلِكَ فِي أَهْلِ بَيْتِي، لَقَدْ أَصَابَ مَنْ أَسْلَمَ مِنْهُمُ الْخَيْرُ وَالشَّرَفُ وَالْعِزُّ، وَلَقَدْ أَصَابَ مَنْ كَانَ مِنْهُمْ كَافِرًا الذُّلُّ وَالصَّغَارُ وَالْجِزْيَةُ.
[صحيح] - [رواه أحمد] - [مسند أحمد: 16957]
المزيــد ...
Jële nañu ci Tamiim Addaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
"mbir mii (te mooy diine ji ) dana
egg fu guddi gi ak bëccëg gi egg, te Yàlla du bàyyi kërug taax walla kërug kaw lu dul ne dana fa dugal diine ji, ci teddaangey aji-tedd walla toroxtaangey aji-torox, ag teddaange ju Yàlla di terale Lislaam, ak toroxtaange ju Yàlla di toroxale kéefar", Tamiim Addaarii daan na wax naan: loolu de ci sama waa kër laa ko xame, ku ci tuub ci ñoom rekk am na yiw teddnga ak ug màgg, ku ci weddi ci ñoom am na toroxtaange ak ug tuuti ak joxe juuti.
[Wér na] - [Ahmat soloo na ko] - [Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya - 16957]
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne diine jii dana matale mbooleem suuf si, bépp barab bu guddi ak bëccëg egg rekk diine ji dana fa egg, Te Yàlla du bàyyi ak kër ci taax yi ak ci kaw gi walla ci xur yi mbaa ci àll bi lu dul ne dana fa dugal diine ji, Ku nangu diine ji te gëm ko dana nekk ku tedd ci teraangay Lislaam, Ku ko bañ daal di koy weddi dana nekk ku torox di ku doyadi.
Sahaaba bi di Tamiim Addaarii -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ne moom ci këram la xame lii Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare, ndax ku ci dugg ci Lislaam ci ñoom am na yiw ak teddnga ak ug màgg, ku ci weddi ci ñoom am ug toroxtaange ak ug doyadi ànd ak li muy jox jullit ñi ci juuti.