عَنْ أَنَسٍ رضي الله عنه قَألَ:
كَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِذَا دَخَلَ الخَلاَءَ قَالَ: «اللَّهُمَّ إِنِّي أَعُوذُ بِكَ مِنَ الخُبُثِ وَالخَبَائِثِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 142]
المزيــد ...

Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan dugg ci wanag day wax: «Allaahumma innii ahuusu bika minal xubusi wal xabaa-isi».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 142]

Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan namm a dugg ci barab bu muy faje aajo, saw mbaa ginnaaw kër, day muslu ci Yàlla, làqatu ci moom ngir mu musal ko ci ayu Saytaane yu góor yi ak yu jigéen yi. Firee nañu xubus ak xabaaisi ba tay ci aw ay ak ci ay sobe.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

  1. Sopp nañu ñaan gii bu ñuy dugg ci wanag.
  2. Mbindeef yépp a aajowoo seen Boroom ci jañ lépp lu leen di lor ci gépp anam.
Gaaral firi yi
Làkk wi: الإنجليزية الأوردية الإسبانية Yataal gi (57)