عَن عَبدِ الله بنِ الشِّخِّير رضي الله عنه قَالَ:
انْطَلَقْتُ في وَفدِ بَنِي عَامِرٍ إِلى رَسُولِ الله صلى الله عليه وسلم، فَقُلنا: أَنتَ سيّدُنَا، فقال: «السَّيدُ اللهُ»، قُلنا: وَأَفْضَلُنا فَضْلاً، وأعظَمُنا طَوْلاً، فقال: «قُولُوا بِقَولِكُم، أَو بَعضِ قولِكُم، وَلَا يَسْتَجْرِيَنَّكُم الشَّيطَانُ».
[صحيح] - [رواه أبو داود وأحمد] - [سنن أبي داود: 4806]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibnus siqiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne:
man ak mbooloo ci Banuu Aamir dañoo ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ne ko: yaw yaay sunu sang, mu ne nu: "sang bi mooy Yàlla", nu ne ko: yaanu gën, gën noo màggi xéewal, mu ne nu: "waxleen la ngeen daa wax, mbaa lenn ca la ngeen daa wax, te bu leen saytaane yóbbaale".
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko,ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 4806]
Am mbooloo dañoo dem ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ba ñu eggee ci moom wax ko -ngir di ko tagg- yenn kàddu yoy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bëggu ko, Ñu ne ko: "yaw yaay sunu sang", Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne leen: "sang bi mooy Yàlla" Mooy sàngu lépp lu mu sàkk, te ñoom ay jaamam lañu. Ñu ne ko: yaw "yaa ñu gën ay ngëneel" te gën ñoo kawe daraja ak teddnga ak i may. Te yaw "yaa nu gën a màgg ay xéewal" ëpp nu ay may gën noo kawe. Topp Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digal leen ñu wax seen wax ja ñu daan wax, te bañ a sonal seen bopp ci yenn wax yi, te saytaane bañ leen a yóbb ci ëppal ak ci jaye gu leen di tàbbal ci lu araam niki bokkaale ak i jumtukaayam.