+ -

عَن أَبِي أُمَامَةَ رضي الله عنه قَالَ: سَمِعْتَ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَخْطُبُ فِي حَجَّةِ الوَدَاعِ فَقَالَ:
«اتَّقُوا اللَّهَ رَبَّكُمْ، وَصَلُّوا خَمْسَكُمْ، وَصُومُوا شَهْرَكُمْ، وَأَدُّوا زَكَاةَ أَمْوَالِكُمْ، وَأَطِيعُوا ذَا أَمْرِكُمْ تَدْخُلُوا جَنَّةَ رَبِّكُمْ».

[صحيح] - [رواه الترمذي وأحمد] - [سنن الترمذي: 616]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abii Umaamata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy xutba ca aju tàggatoo ga di wax naan:
« ragalleen Yàlla seen Boroom, te ngeen julli seen julli juróom yi, te woor seen weer wi, te joxe asakay seen alal ji, te topp ki jiite seeni mbir, kon dangeen dugg àjjanay seen Boroom».

[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 616]

Leeral

Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-dafa xutba bisu arafa,ci ajug tàggatoo ga,ci atum fukkeel ma ci gàddaay gi,tudde nañu ko loolu; ndaxte Yonnente bi ci la tàggatook nit ñi. Mu digal nit ñépp ñu ragal seen Boroom ci def ay ndigalam te bàyyi ay tereem. Ak ñuy julli julliy juróom yi Yàlla mu màgg mi farataal ci bis bi ak ci guddi gi. Ak ñuy woor weeru koor. Ak ñuy jox seen asakay alal ña ko yeyoo te bañ caa nay. Ak ñu topp ñi Yàlla def njiit ci seen kaw, ci lu dul moy Yàlla, Ku def mbir yii ñu tudd payam mooy dugg àjjana.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Jëf yii bokk na ci yiy sababi dugg àjjana.