Toftaleg Adiis yi

1. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ndayjoor daan na ko yéem ci buy sol dàll, ak buy peñewu, ak buy laab, ak ci mbiram yépp
عربي Àngale Urdu
2. Masuma a gis Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy xàqataay di ree ba ma gis ay yàppi biir gémmiñam, waaye da daan muuñ - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
3. bu kenn ci yéen gisee ci gént lu mu bëgg, loolu ci Yàlla la bawoo, na sant Yàlla ci loolu te waxe ko, bu gisee lu dul loolu ci lu mu sib, loolu ci Saytaane la bawoo, na muslu ci ayam, te bu mu ko wax kenn, kon du ko lor
عربي Àngale Urdu
4. ku dundal ñaari jigéen ba ñu mat, dana ñëw ëllëg bis-pénc man ak moom" mu tàppale ay baaraamam
عربي Àngale Urdu
5. Bu ma bañul woon a sonal jullit ñi -walla sama xeet wi- kon dina leen digal socc ci julli gu nekk
عربي Àngale Urdu
6. amul benn bis bu jaam ñi di xëy lu dul ne ñaari malaaka danañu wàcc, kenn ki naan: yaw Yàlla joxal aji-joxe ji leneen, keneen ki naan: yaw Yàlla joxal aji-téye ji ag yàqule
عربي Àngale Urdu
7. deeleen jegeele, tey jubal, te ngeen xam ne kenn ci yéen du mucc ngir ay jëfam" ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ba ci yaw sax? Mu ne: "ba ci man kay, lu dul Yàlla muure ma ag yërmàndeem ak ngëneelam
عربي Àngale Urdu
8. Allaahuma innii ahuusu bi ridaaka min saxatika, wa bi muhaafaatika min huquubatika, wa ahuusu bi ka minka, laa uhsii sanaa-an halayka, anta kamaa asnayta halaa nafsika
عربي Àngale Urdu
9. ndax duma leen xibaare waa àjjana? Ñooy képp ku néew doole, tey toroxlu, te bu giñoon ci Yàlla mu dëggal ko, ndax duma leen xibaare waa sawara? Ñooy képp ku dëgër soxor tey rëy-rëylu
عربي Àngale Urdu
10. man de xam naa baat boo xam ne bu ko waxoon li muy yég deñ, bu waxoon: ahuusu bil Laahi minas Saytaani, kon li muy yég dem
عربي Àngale Urdu
11. gént gu baax ci Yàlla la jóge, gént gu bon nag ci Saytaane la jóge, bu kenn ci yéen gisee gént gu mu ragal, na tifli ci càmmooñam, te muslu ci Yàlla ci ayam, kon du ko lor
عربي Àngale Urdu
12. Damaa wax: "yaw Yonnente Yàlla bi, ana lan mooy musale? Mu ne ma "tëyéel sa làmmiñ, te na la sa kër doy, te nga jooy say ñuumte
عربي Àngale Urdu
13. man maa ngi fa ma sama jaam bi njorte, te maa ngi ànd ak moom saa yu ma tuddee - 4 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
14. Laaj naa Aysatu, ne ko: ci lan la Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan tàmbalee bu daan dugg këram? Mu ne: ci socc
عربي Àngale Urdu
15. Dañoo tudd fi Yonnente bi jenn waay bu nelaw guddeem gi yépp ba suba jot, mu ne: "kooku mooy ki nga xam ne saytaane daa saw ci ay noppam, walla mu wax: ci noppam
عربي Àngale Urdu
16. Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na pasteefu ci fukk yu mujj yi lu mu daawul pasteefu ci yu dul yooyu
عربي Àngale Urdu
17. jaam bi du suturaal ab jaam ci àdduna lu dul ne Yàlla dana ko suturaal ëllëg bis-pénc
عربي Àngale Urdu
18. bu kenn ci yéen faatu lu dul ne dafa rafet njort ci Yàlla
عربي Àngale Urdu
19. bu dee ni nga wax lañu mel, moo ngi mel ni yaa ngi leen di gàccaal di leen mëqloo dóom bu tàng, te Yàlla du deñ di la dimbali ci seen kaw fii ak yaa ngi ci loolu
عربي Àngale Urdu
20. ñaari ndëggu jaam bi du pënd ci yoonu Yàlla ba noppi sawara di ko laal
عربي Àngale Urdu
21. amul aw nit wuy jog ci ab jotaay te tudduñu fa Yàlla lu dul ne danañu jog mel ni méddum mbaam, ñu ame ca ag réccu
عربي Àngale Urdu
22. misaalu kiy tudd Boroomam ak ki dul tudd Boroomam, mi ngi mel ni misaalu kiy dund ak ki dee
عربي Àngale Urdu
23. man de bokk na ci li may ragal ci yéen sama ginnaaw, ñu ubbil leen naataangey àdduna ak taaram - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
24. ku bëgg Yàlla musal ko ci xat-xati ëllëg bis-pénc, nay yombalal ki nekk ci jafe-jafe walla mu teggil ka ko
عربي Àngale Urdu
25. ki gën a woyof mbugal ci waa sawara mooy ki am ñaari dàll ak ñaari waroy dàll yu sawara, yuuram gi di ci bax kem ni cin di baxe, ba du foog ne kenn a ko gën a tar mbugal, te moo leen gën a woyof mbugal
عربي Àngale Urdu
26. dees na jegeele aji-gëm ji Boroomam bu màgg bi ëllëg bis-pénc, ba mu teg suturaam ci kawam, di ko saxalal ay bàkkaaram
عربي Àngale Urdu
27. lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko
عربي Àngale Urdu
28. yëkkëti nanu xalima gi ci ñatt, ci kiy nelaw ba baa muy yeewu, ak ci xale bi ba baa muy gént, ak ci dof bi ba baa muy xellu - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
29. mo ndax Yàlla defalu leen lu ngeen di saraxee? Bépp sàbbaal ab sarax la, bépp sant ab sarax la, bépp tudd Yàlla it sarax la, digle lu baax sarax la, tere li bon sarax la, sëyug kenn ci yéen itam sarax la
عربي Àngale Urdu
30. ku dindil aji-gëm ji jafe-jafe ci jafe-jafey àdduna Yàlla dindil ko jafe-jafe ci jafe-jafey ëllëg bis-pénc
عربي Àngale Urdu