Xàjjaley wanqaas yi

Toftaleg Adiis yi

1. tabax nañu lislaam ci juróom - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
2. ku gis ci yéen lu ñu sib na ko soppi ci loxoom, bu ko manul na ko soppi ci làmmeñam, bu ko manul na ko soppi ci xolam, te loolu moo gën a néew ci ngëm - 4 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
3. ku rafetal ci Lislaam deesu ko toppe la mu defoon ca ceddu ga, waaye ku def lu ñaaw ci Lislaam dees na ko toppe lu njëkk la ak lu mujj li
عربي Àngale Urdu
4. waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
عربي Àngale Urdu
5. Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
6. mbaa sama Hadiis du yeksi ci nit mu tëdd ag gàngunaayam naan: Diggante nun ak yéen téeréb Yàlla la - 6 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
7. àqi Yàlla ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko te bañ koo bokkaale ak dara, àqi jaam ñi ci Yàlla nag mooy du mbugal ku ko bokkaalewul ak dara
عربي Àngale Urdu
8. ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana, ku faatu te bokkaale ko ak dara dana dugg sawara
عربي Àngale Urdu
9. wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
10. Yàlla dina musal nit ci samaw xeet ci kanamu mbindéef yépp ëllëg bis-pénc
عربي Àngale Urdu
11. bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm-
عربي Àngale Urdu
12. Yàlla bind na ndogali mbindéef yi njëkk muy bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-fukki junniy at
عربي Àngale Urdu
13. dénk naa leen ngeen ragal Yàlla ci dégg ak topp, donte jaamub Habasa la, dangeen gis ci sama ginnaaw ag wuute gu tar, waaye nangeen jàpp ci sama Sunna ak sunnay njiit yu jub ya tey jubal - 6 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
14. Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar
عربي Àngale Urdu
15. ku fàtte genn julli na ko julli saa yu ko fàttalikoo, dara manu koo fay lu dul loolu
عربي Àngale Urdu
16. li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli
عربي Àngale Urdu
17. kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
18. Yàlla mu kawe mi nee na: seddale naa julli ci sama diggante ak sama jaam bi ci ñaari xaaj, ñeel na sama jaam bi lu mu laaj
عربي Àngale Urdu
19. Yaw Yónente Yàlla bi, man de bàyyiwuma lu rëy walla lu ndaw lu dul ne def naa ko, mu ne ko: «Ndax dangay seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ci dëgg ku dul yàlla, ak ne Muhammat mooy Yónente Yàlla?
عربي Àngale Urdu
20. ndaxte waxul benn yoon ne: sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba
عربي Àngale Urdu
21. ndax xam ngeen lan la séen Boroom wax ?» Ñu ne ko: Yàlla a xam ak ub Yónenteem, mu ne leen: Yàlla dafa wax ne: «am na ci sama jaam ñi ñu xëy gëm ma am ñu weddi
عربي Àngale Urdu
22. nun de dananu yég ci sunu bopp loo xam ne dana rëy lool kenn i nun di ko wax, mu ne leen: «te yég ngeen ko?» Ñu ne ko: waaw, mu ne leen: loolu mooy ngëm gu leer
عربي Àngale Urdu
23. maa ngi sant Yàlla mi delloo pexeem ya ci ay jax-jaxal
عربي Àngale Urdu
24. Saytaane day dikkal kenn ci yéen, di ko wax naan: ku bind lii? Ku bind lii? Ba mujj mu ne ko: ku bind sa Boroom? Bu àggee fii nag na muslu ci Yàlla te yamale ko fa
عربي Àngale Urdu
25. jëf yi juróom-benn la, nit ñi yitam ñent la ñu, ñaar yuy waral, ak yu tolloo, ak benn bu baax ñu ful fo ba mu mat fukk yunimel, ak wenn yiw wuñu ful bamu mat juróom-ñaari téeméer
عربي Àngale Urdu
26. Yàlla du tooñ benn way-gëm ci jëfam ju baax di ko wàññi, dana ka ko jox fii ci àdduna fay ka ko ca allaaxira
عربي Àngale Urdu
27. jébbalu nga ànd ak la nga defoon ciw yiw
عربي Àngale Urdu
28. Yàlla daa bëgg ñu def limu yombal, kem ni mu bëgge ñu def mbir yimu dogu
عربي Àngale Urdu
29. misaalum naaféq bi, moo ngi mel ni xar mu réer ci diggante ñaari xar, day daw jëm bii ci yoon wii dawaat jëm ca bee aw yoon
عربي Àngale Urdu
30. ngëm day ràpp ci biiru kenn ci yéen kem ni yéere bu ràpp di ràppe, ñaanleen Yàlla mu yeesal ngëm ci séen i xol
عربي Àngale Urdu
31. Bokk na ci màndargay bis-pénc nu yëkkati xam-xam, réer bari, njaalo bari, naan sàngara bari, góor ñi néew, jigéen ñi bari, ba juróom-fukki jigéen di tolloog benn góor
عربي Àngale Urdu
32. saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu benn waay naan: aka neexoon ma nekk palaasam
عربي Àngale Urdu
33. bis-pénc du taxaw ba keroog ngeeni xeex ak Yahuut yi, ba doj wu ab Yahuut nekk ci ginnaawam di wax naan: yaw jullit bi, ab Yahuut a ngi nii sama ginnaaw ñëwal ray ko
عربي Àngale Urdu
34. giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, daa naka rekk Iisaa Ibn Maryama wàcc ci yeen di ab àttekat bu màndu, di toj kurwaa yi, di ray mbaam-xuux yi, dindi galag gi(empo) bi, alal daal di baawaan ba kenn soxlawu ko
عربي Àngale Urdu
35. Bis-pénc du ñëw mukk ba keroog jànt bi di fenke sowwu, bu fa fenkee nag ba nit ñi gis ko ñoom ñéppay gëm
عربي Àngale Urdu
36. saa du taxaw ba keroog jamono ji di jegee
عربي Àngale Urdu
37. Yàlla dat ŋëb suuf si, lem asamaan yi ci ndayjooram, di wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si
عربي Àngale Urdu
38. Sama mbalka ma de mi ngi toll ne doxu weer, ndoxam ma moo gën a weex meew, xetam ga moo gën a neex gëttug misk - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
39. dinaa nekk ca sama mbalka ma di xaar kan ci yéen mooy ñëw ngir naan, waaye dana ñu téye ay nit ba duñu aksi ci man, may wax naan: yaw sama Boroom ci man lañu bokk, ci samaw xeet lañu bokk
عربي Àngale Urdu
40. giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom ne ay koppam moo ëpp limu biddiwi asamaan si
عربي Àngale Urdu
41. dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
42. Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama
عربي Àngale Urdu
43. Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waxtaanal na nu te mooy aji-dëggal ba di ku ñu dëgggal ki mu ne: «kenn ci yéen dees na dajale am mbindam ci biiru yaayam ñent-fukki bis ak ñent-fukki guddi - 4 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
44. lépp a ngi ci ndogal yi, ba ci lott ak muus, mbaa muus ak lott
عربي Àngale Urdu
45. bu Yàlla dogalee ci nit ki mu faatu a fi barab da koy def mu am fa aajo
عربي Àngale Urdu
46. ku ma fenal te tay ko na waajal ab wàccuwaayam ca sawara - 8 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
47. man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin
عربي Àngale Urdu
48. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa am lu mu tudd daal di ne: «loolu de bu xam-xam di dem lay doon
عربي Àngale Urdu
49. buleen dëggal ñoñ téere yi te buleen leen weddi, nangeen wax ne: {gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun}
عربي Àngale Urdu
50. buleen sàkku xam-xam ngir di ci puukarewu ak woroom xam-xam yi, walla ngir di ci werente ak way-dese ñi - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
51. Yàlla sadd na misaal ci yoon wu jub
عربي Àngale Urdu
52. Wàcce na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Alxuraan fekk mi ngi am ñent-fukki at - 4 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
53. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawul woon xam luy xàjjale saar yi ba ba ñuy wàcce ci Moom {Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim}
عربي Àngale Urdu
54. Ndax kenn ci yéen bëgg na bu delloo ci njabootam fekk fa ñàtti giléem yu ëmb, rëy te suur?
عربي Àngale Urdu
55. Dina ñu wax ëllag ki jàngoon Alxuraan: Jàngal te yéeg, jàngal ni nga doon jànge ci àdduna, ndax sa kër moo ngi tolloog aaya bi ngay mujja jàng - 4 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
56. kiy biral Alxuraan moo ngi mel ni kiy biral ab sarax, kiy yalu Alxuraan it moo ngi mel ni kiy nëbb ab sarax
عربي Àngale Urdu
57. ñoom dañu daan jàng ci Yónente bi fukki aaya, daawuñu jëlaat dara tek ko ca fukk ya ba baa ñuy xam li nekk ci yii ci xam-xam ak jëfe
عربي Àngale Urdu
58. yaw Aba- Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi ?» Nee na: ma ne ko: {Allaahu laa-i-Laaha illaa huwa Al-Hayyul Xayyuumu} [Al-Baxara: 255]. Nee na: mu dóor sama dënn, daal di wax ne: «giñ naa ci Yàlla, na xam-xam ndokkeel Aba- Munsir - 10 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
59. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- guddi gu nekk bu daan yéeg ci lalam day boole ñaari téqam, daal di ciy ëf, daal di jàng: {Xul huwal Laahu Ahadun}, ak {Xul ahuusu Bi Rabbil falaxi} ak {Xul ahuusu Bi Rabbin naasi}
عربي Àngale Urdu
60. Yahuut yi ñooy ñi Yàlla mere, nasaraan yi ñooy ñi réer
عربي Àngale Urdu
61. bu ngeen gisee ñiy topp lënt ya xamleen ne ñooñii la Yàlla di wax nangeen leen moytu
عربي Àngale Urdu
62. amul kenn kuy def bàkkaar, jug daal di laab, daal di julli, daal di jéggalu Yàlla, lu dul ne Yàlla dina ko jéggal
عربي Àngale Urdu
63. xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?
عربي Àngale Urdu
64. waxal ne: amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla, ma seedeel la ci ëllëg bis-pénc
عربي Àngale Urdu
65. li gay wax di ci woote lu baax la, boo ñu xibaaroon ndax la ñu defoon dees na ko jéggale
عربي Àngale Urdu
66. demal ne ko: yaw bokkoo ci waa sawara, waaye ci waa àjjana nga bokk
عربي Àngale Urdu
67. yéen nit ñi Yàlla de jële na ci yéen rëy-rëylug ceddo ga ak seenug damu ci seen baay ya - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
68. {te dees na leen laaj xéewal yi bis booba}
عربي Àngale Urdu
69. ci sama mujjuw xeet wi dana am ay nit yu leen di wax lu ngeen masuta dégg yéen ak séen i baay, nangeen leen moytu - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
70. bindal, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, dara du ci génn lu dul dëgg - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
71. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàppu ci julli gu ne
عربي Àngale Urdu
72. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na benn-benn
عربي Àngale Urdu
73. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na ñaar-ñaar
عربي Àngale Urdu
74. bu kenn ci yéen yëgée ci biiram dara, te xamul ndax dara génn na ci moom walla déet, bumu génn jàkka ci ba keroog muy dégg kàddu, mbaa mu yég ngelaw
عربي Àngale Urdu
75. war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam
عربي Àngale Urdu
76. Dikk naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bëgg a dugg ci Lislaam, mu digal ma ma sàngu ci ndox ak siddéem
عربي Àngale Urdu
77. bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man - 6 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
78. ku tabax jàkka ngir Yàlla Yàlla dana ko tabaxal ca àjjana lu mel ni moom
عربي Àngale Urdu
79. genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka
عربي Àngale Urdu
80. bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na julli ñaari ràkka bala moo toog
عربي Àngale Urdu
81. bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na wax: Allaahumma iftah lii abwaaba rahmatika, bu génnee na wax: Allaahumma innii as-aluka min fadlika
عربي Àngale Urdu
82. yaw Bilaal taxawalal julli gi, noppal nu ci
عربي Àngale Urdu
83. yéen nit ñi, damaa def lii ngir ngeen roy ak ngir ngeen xam samag julli
عربي Àngale Urdu
84. bu ngeen di julli nangeen jubal séen sàppe yi, kenn ci yéen jiite leen, bu kàbbaree nangeen kàbbaar
عربي Àngale Urdu
85. giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, maa leen gën a niroole jullig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax nii la daan jullee ba ni mu tàqalikoo ak àdduna
عربي Àngale Urdu
86. ki gën a bon ug càcc ci nit ñi mooy kiy sacc julleem» ñu ne ko: naka lay sacce julleem? Mu ne: «du matal rukkoo yi, ak sujjóot yi
عربي Àngale Urdu
87. Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- budaan yëkkati ndingam jóge ca rukoo ba da daan wax: «samihal Laahu liman hamidahu - 2 ملاحظة
عربي Àngale Urdu
88. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne
عربي Àngale Urdu
89. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Rabbi ixfir lii, Rabbi ixfir lii
عربي Àngale Urdu
90. kooku Saytaane bu ñu woowe Xinsab la, boo ko yégatee nanga muslu ci Yàlla ci moom, te nga tifli ci sa càmmooñ ñatti yoon
عربي Àngale Urdu