+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه:
أَنَّ رَجُلًا قَالَ لِلنَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: أَوْصِنِي، قَالَ: «لَا تَغْضَبْ» فَرَدَّدَ مِرَارًا قَالَ: «لَا تَغْضَبْ».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 6116]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-:
Benn waaye dafa wax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: dénk ma, mu ne ko: "bul mer" mu baamtu ko ay yoon mu ne ko: "bul mer".

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6116]

Leeral

Kenn ci Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- dafa sàkku ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ngir mu tegtal ko lu koy jariñ, mu digal ko ne ko bu mu mer, te loolu mooy nay moytu lépp lu koy tax a mer, tey téye boppam saa su meree, bañ a topp meram ci di ray mbaa di dóor walla di saaga mbaa lu ko niru.
Waa ji baamtu càkkuteefam ay yoon, Yónente bi yokkul la mu ko denkoon te mooy "bul mer".

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Moytandiku loo mer ak yi koy waral, ndax dafa dajale wépp ay, te mucc ca moo dajale wépp yiw.
  2. Mer ngir Yàlla niki mer su ñu xottee wormay Yàlla dafa bokk ci mer yi ñu gërëm.
  3. Di baamtu wax ji ndeem yittewoo nañu ko ba keroog kiy déglu di ko xam man a peeg njariñam.
  4. Ngëneelu sàkku ndénkaane ci boroom xam-xam.