عن أبي سعيد الخدري رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«لَا ضَرَرَ وَلَا ضِرَارَ، مَنْ ضَارَّ ضَرَّهُ اللَّهُ، وَمَنْ شَاقَّ شَقَّ اللَّهُ عَلَيْهِ».
[صحيح بشواهده] - [رواه الدارقطني] - [سنن الدارقطني: 3079]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«deesul loru waaye deesul lore, ku lore Yàlla lor ko, waaye ku sonle Yàlla sonal ko».
[Wér na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal] - [Ad-daaraqutniy soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Ad-daaraqutniy - 3079]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne dañoo war a jeñ lor ci ay anam yu wuute, ci sunu jëmm ak ci ñeneen ñi, daganul kenn di lor boppam mbaa muy lor keneen.
Du dagan ci kenn muy delloo lor ci aw lor; ndax lor deesu ko dindee lor lu dul ci anamu fayantoo te bañ a ëppal.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral tëkku ku rëy giy tege ci kiy lor nit ñi, ak coono gi ñeel kiy sonal nit ñi.