3. ñoom ñaar de ñoo ngi leen di mbugal, te sax mbugaluñu leen ci lu rëy, kenn ki moom daawul suturawu bu daan saw, keneen ki nag da daan dox di rambaaj - 4 ملاحظة
8. bu nit ki duggee këram, daal di tudd Yàlla buy dugg ak buy lekk, saytaane day wax naan: amuleen fanaanukaay, amuleen reerukaay - 2 ملاحظة
9. àdduna de ñam wu neex la te naat, Yàlla da leen fee wuutal, di xool lu ngeen fiy jëf, noytuleen àdduna te moytu jigéen ñi - 2 ملاحظة
11. ndax kenn ci yeen du ragal walla muy tiit bu yëkkatee boppam njëkk imaam bi, Yàlla def boppam bi boppu mbaam, walla Yàlla def meloom wi melow mbaam
12. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal na ma taaya fekk samay ténq moo ngi ci diggante ñaari ténqam, kem ni mu ma xamale saaru Alxuraan
13. Allaahumma innii ahuusu bi ka min hasaabil xabri, wa min hasaabin naari, wa min fitnatil mahyaa wal mamaati, wa min fitnatil Masiihid Dajjaali - 2 ملاحظة
14. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan dugg ci wanag day wax: «Allaahumma innii ahuusu bika minal xubusi wal xabaa-isi
15. ag siif de dana am ak ay mbir yu ngeen bañ" ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi ana lan nga nuy digal? Mu ne: "joxeleen àq ji leen war, te laaj Yàlla seen àq
16. Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan sangu janaba, da daan raxas ñaari loxoom, jàpp njàppum julli, daal di sangu
17. misaalu ki taxaw ci foroñceeri Yàlla yi ak ki ci tàbbi, moo ngi mel ni aw nit wu tegoo bant ci ag gaal, ñii am kaw ga, ñii nekk ca suuf ga - 8 ملاحظة
18. Góor laa woon gu bari masyu ma amoon kersay laaj ko Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ngir wàccuwaay gi doomam am, ma digal Al-Miqdaad ibnul Aswad mu laaj ka ko, mu ne ko: "day raxas sakaraam daal di jàpp
20. dungeen dugg àjjana ndare ngeen gëm, te dungeen gëm ndare ngeen bëggante, moo ndax duma leen tegtal lol su ngeen ko defee dangeen bëggante? Siiwalleen ab nuyóo seen diggante - 2 ملاحظة
21. jan jëf la Yàlla gën a bëgg? Mu wax ne: "julli ci waxtoom" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "teg ca fonk ñaari way-jur" mu ne ko: teg ca lan? Mu ne: "jihaad ci yoonu Yàlla - 2 ملاحظة
22. Benn waay da doon lekke càmmooñ fi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ko: "lekkeel sa ndayjoor", waa ji ne ko: manuma ko, mu ne ko: "Yàlla boo ko man
23. ku woote jëme cig njub dana am ag pay gu mel ni payug ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni pay dara
24. gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la, -ñatti yoon-, amunu ci pexe, waaye Yàlla mu màgg mi moo koy dindi ci wakkirlu
25. ne ko: yaw yaay sunu sang, mu ne nu: "sang bi mooy Yàlla", nu ne ko: yaanu gën, gën noo màggi xéewal, mu ne nu: "waxleen la ngeen daa wax, mbaa lenn ca la ngeen daa wax, te bu leen saytaane yóbbaale
28. wàlle amul, gaafal amul, gaatnga lu baax nag yéem na ma» nee na, ñu ne ko: lan mooy gaatnga lu baax ? Mu ne: "wax ju teey
29. Mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ci waa Ansaar yi ne: "kénn du leen bëgg ku dul way-gëm, te kenn du leen bañ ku dul ab naaféq, ku leen bëgg Yàlla bëgg ko, ku leen bañ Yàlla bañ ko
31. doon na la doy rekk nga def nii say loxo" mu dóor ay loxoom ci suuf benn dóor, daal di masaa càmmooñam ci kaw ndayjoor bi, ak bitti ténq yi ak kanam gi
32. Daan naa sangu man ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci benn ndab fekk nun ñaar ñépp a am janaba, daan na ma digal ma woddu, muy jonjoo ak man fekk damaa nekk ci mbaax,
33. Jaayante naa ak Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak dégg ak topp, ak laabire bépp jullit
34. ragalleen Yàlla seen Boroom, te ngeen julli seen julli juróom yi, te woor seen weer wi, te joxe asakay seen alal ji, te topp ki jiite seeni mbir, kon dangeen dugg àjjanay seen Boroom
35. tegtal ma jëf joo xam ne su ma ko defee dinaa dugg àjjana, mu ne ko: "dangay jaamu Yàlla te doo ko bokkaale ak dara, di taxawal julliy farata, di joxe asaka, di woor weeru koor - 2 ملاحظة
37. ci lan lañuy jaayante ak yaw? Mu ne: "ci ngeen jaamu Yàlla te du ngeen ko bokkaale ak dara, ak julliy juróom, ak di topp -mu daaldi wax kàddu gu suufe ne- te du ngeen laaj nit ñi dara
38. digal nañu ma ma xeex ak nit ñi ba baa ñuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka
40. jullig góor gi ca mbooloo ma moo ëpp julleem ci këram ak ca ja ba luy tolloo ak ñaar-fukki daraja ak lu topp
41. jaam bi du seqi benn jéego ëllëg bis-pénc ludul ne dees na ko laaj dundam gi ci lan la ko jeexale, ak xam-xamam bi lu mu ci def, ak alalam nan la ko ame ak ci fan la ko dugal , ak yaramam wi ci lan la ko ràppal
42. xibaarleen ma bu ag dex nekkoon ci buntu këru kenn ci yéen mu ciy sangu bis bu nekk juróomi yoon, ndax loolu dana dese tilim ci yaram? - 2 ملاحظة
43. misaalu way-gëm ñi ci seenug bëggante ak seenug yërëmante ak seenug ñeewantu day mel ni aw yaram, bu ci benn cër di jàmbat dara mbooleem yaram wi yépp day ànd bañ a nelaw ak di tàng - 8 ملاحظة
44. digalleen seen doom yi ñuy julli bu ñu amee juróom-ñaari at, te ngeen leen di dóor ci loolu bu ñu amee fukki at,te ngeen teqale seen diggante ca tëddukaay ya - 2 ملاحظة
45. amul dara lu gën a diis ci màndxem jullit bi ëllëg bis-pénc jikko yu rafet, te Yàlla dafa bañ ku ñaaw i wax ñaaw i jëf - 2 ملاحظة
46. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa génn ci nun, nu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, xam nanu naka lanu lay nuyòo, leegi naka lanuy jullee ci yaw? - 2 ملاحظة
48. Jullit bi am kàttan, moo gën te moom la Yàlla gën a bëgg ci jullit bi néew kàttan, ñoom ñéppu na nga a baax,
49. Li ëppoon ci ñaani Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mooy:"Allaahumma Rabbanaa aatinaa fiddunyaa hasanatan, wa fil-aaxirati hasanatan, wa xinaa hasaabannaari
51. Moytuleen tooñ, ndax tooñ ay lëndëm lay doon ëllëg bis-pénc, te ngeen moytu nay, ndaxte nay moo alag ña leen jiitu woon, - 2 ملاحظة
52. benn waay dafa laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: lan moo gën ci Lislaam? Mu ne ko: "nga leele ñam, ak di nuyu koo xam ak koo xamul
55. Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, wax ak moom ci yenn mbir yi, daal di ne ko: bu soobe Yàlla soob la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: "ndax dangamay yamale ak Yàlla? Waxal: bu soobe Yàlla moom dong
57. {Xul huwal Laahu Ahadun} ak ñaari musluwaay yi boo gontee ak boo xëyee ñatti yoon, dana la fegal lépp
58. waxal: laa ilaaha illalaahu wahdahu laa sariika lahu, Allaahu Akbaru kabiiran, wal hamdu lil-Laahi kasiiran, subhaanal Laahi Rabbil haalamiina, laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi Alhasiisil-Alhakiimi - 6 ملاحظة
59. amul benn jullit boo xam ne jullig farata dana jot mu rafetal njàppu ma ak toroxlu ga ak rukkoo ya,lu dul ne dana ko faral li ko jiitu ci ay bàkkaar,fii ak deful bàkkaar bu mag,te loolu jamono jépp la
60. misaalum jullit biy jàng Alxuraan moo ngi mel ni Utruja, xetam ga dafa teey ak cafkaam teey, misaalum jullit bi dul jàng Alxuraan moo ngi mel ni tàndarma, amul xet te cafkaam dafa neex - 8 ملاحظة
61. ay mbir a ngii yuy wuutante ku leen di wax du sooy -walla ku leen di def- ginnaaw jullig farata gu nekk, Subhaanal Laahi fanweeri yoon ak ñatt, alhamdu lil-Laahi fanweeri yoon ak ñatt, Allaahu Akbaru, fanweeri yoon ak ñent
62. kuy wax saa yu déggee noddkat bi, ashadu an laa-i-Laaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu, wa anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu, radiitu billaahi rabban, wa bi Muhammadin rasuulan, wa bil Islaami diinan, dees na ko jéggal ay bàkkaaram
64. ku noonook sama péete yégal naako ab xare, sama jaam bi du ma jegeñ-jegeñlu ci dara lu ma gënal li ma farataal ci moom - 2 ملاحظة
66. Benn waay dafa jàppu daal di bàyyi barab buy tollook aw weh ci ay ndëggoom Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal akmucc- gis ko ne ko:"dellul te rafetal sa njàppu mi" mu dellusi,daal di julli
67. ñaari xaaj a gi nii yu bokk ci waa sawara te gisaguma leen,ay nit yu yor ay yar yu mel ni geeni nag di ci dóor nit ñi,ak ayjigéen yu solu ba noppi rafle, jeng di jengale
72. sangu bisub àjjuma war na képp ku toll ci gént,ak mu soccu, ak mu laal gëtt bu ko amee - 4 ملاحظة
73. jullit mooy ki nga xam ne jullit ñi mucc nañu ci làmmiñam ak ci loxoom,gàddaaykat nag mooy ki gàddaay li Yàlla araamal ci moom
75. ku sàbbaal Yàlla ginnaaw julli gu ne fanweeri yoon ak ñatt, sant Yàlla fanweeri yoon ak ñatt, màggal Yàlla fanweeri yoon ak ñatt, loolu juróom-ñent-fukk ak juróom ñent la, mu wax: ci mottali ko téemeer: laa-i-Laaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiirun, ñu jéggal ko ay njuumteem doonte dafa toll ni puuriti géej - 2 ملاحظة
77. mbir mii (te mooy diine ji ) dana egg fu guddi gi ak bëccëg gi egg, te Yàlla du bàyyi kërug taax walla kërug kaw lu dul ne dana fa dugal diine ji
78. bu kenn ci yéen sikk-sakkaa ci julleem te ba xamul ñaata la julli ndax ñatt la walla ñent, na sànni sikk-sakka ga, te tabax ca la ko wóor, topp mu sujjóot ñaari sujjóot njëkk muy sëlmël
79. lépp luy màndiloo sàngara la, te lépp luy màndiloo dafa araam, te kuy naan sàngara ci àdduna ba dee fekk ne tàmm na ko te tuubu ko, kooku du ko naan ca allaaxira - 6 ملاحظة
80. Wax naa: yaw Yonente Yàlla bi: kan laay gën a rafetal ci moom? Mu ne ma: "sa yaay, topp ca sa yaay, topp ca sa yaay, topp ca sa baay, topp ca ki gën a jege