+ -

عن معاوية رضي الله عنه قال: سمعت النبي صلى الله عليه وسلم يقول:
«مَنْ يُرِدِ اللهُ بِهِ خَيْرًا يُفَقِّهْهُ فِي الدِّينِ، وَإِنَّمَا أَنَا قَاسِمٌ، وَاللهُ يُعْطِي، وَلَنْ تَزَالَ هَذِهِ الْأُمَّةُ قَائِمَةً عَلَى أَمْرِ اللهِ، لَا يَضُرُّهُمْ مَنْ خَالَفَهُمْ، حَتَّى يَأْتِيَ أَمْرُ اللهِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 71]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Muhaawiya -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
«ku Yàlla nàmm ci moom aw yiw dana ko dégg-loo diine, man nag ab séddalekat kepp laa, waaye Yàlla mooy joxe, te xeet wii du deñ di taxaw ci mbiri Yàlla, ku wuute ak ñoom it du leen lor, ba baa mbiri Yàlla di ñëw».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 71]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ku Yàlla nàmm ci moom aw yiw da koy wërsëgale dégg diineem ji ak ne moom Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mooy aji-séddale ji, day séddale li ko Yàlla mu kawe mi jox ci wërsëg ak xam-xam ak yeneen, waaye kiy joxe dëgg mooy Yàlla, ku dul moom nag sabab la du jariñ ci lu dul ndigalul Yàlla, ak ne xeet wii du deñ di taxawe mbiri Yàlla, te ku wuute ak ñoom it du leen lor, ba keroog bis-pénc.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Kanadi البلغارية Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi :Màggaay ak ngëneelul xam-xamu Sariiha ak d sàkku ko ak ñaaxe ca.
  2. Xeet wi manut a ñàkk ñuy taxaw ci dëgg, bu ko am mbooloo bàyyee itam ñeneen taxawe ko.
  3. Dégg diine daa bokk ci liy wane ne Yàlla namm na aw yiw ci jaamam bi.
  4. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day joxe ci ndigalu Yàlla ak coobareem, waaye moom amul dara.