+ -

عن أبي سعيد الخُدْريِّ رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«‌مَنْ ‌رَأَى ‌مِنْكُمْ ‌مُنْكَرًا فَلْيُغَيِّرْهُ بِيَدِهِ، فَإِنْ لَمْ يَسْتَطِعْ فَبِلِسَانِهِ، فَإِنْ لَمْ يَسْتَطِعْ فَبِقَلْبِهِ، وَذَلِكَ أَضْعَفُ الْإِيمَانِ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 49]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
«ku gis ci yéen lu ñu sib na ko soppi ci loxoom, bu ko manul na ko soppi ci làmmeñam, bu ko manul na ko soppi ci xolam, te loolu moo gën a néew ci ngëm».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 49]

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day digle ñu soppi lu bon -te mooy lépp lu Yàlla ak ub Yónenteem tere- kem kàttanam, Bu gisee lu bon da koo war a soppi ci loxoom bu ko manee, Bu ko manul mu soppi ko ci làmmeñem ñam ci tere ki koy def, leeralal ko ay loram tegtal ko lu baax ci palaasu mbon gii, Bu manula def taxawaay boobu mu soppi ko ci xolam ci sib lu bon lii te mu dogu ne bu ko manoon a dindi dana ko def, Soppi ko ci xol nag mooy martaba bi gën a néew cig ngëm ci wàllu soppi lu bon.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani اليونانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi: Hadiis bi cosaan la ci leeral martabay soppi lu bon.
  2. Digle na ñu di def ndànk-ndànk ci bu ñuy tere lu bon, ku nekk ak li mu man ak fa kàttanam tollu.
  3. Tere lu bon bunt bu màgg la ci diine te du wàcci kenn, war na bépp jullit ci kem kàttanam.
  4. Digle lu baax ak tere lu bon daa bokk ci meloy ngëm, te ngëm day yokku di wàññiku.
  5. Sartal nañu ci tere lu bon: xamne jëf jooju dafa bon.
  6. Sartal nañu ci soppi li bon: lu gën a bon bañ caa topp.
  7. Tere lu bon am na ay teggin ak i sart yoy war na ci jullit bi mu xamlu ko.
  8. Weddi lu bon dafay laaj doxaliin wu jaar yoon, ak xam-xam ak gis-gis.
  9. Ñàkk a weddi ci sa xol day wane ngëm gu néew doole.