عن أبي هريرة رضي الله عنه قال:
سُئِلَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَنْ أَكْثَرِ مَا يُدْخِلُ النَّاسَ الْجَنَّةَ، فَقَالَ: «تَقْوَى اللهِ وَحُسْنُ الْخُلُقِ»، وَسُئِلَ عَنْ أَكْثَرِ مَا يُدْخِلُ النَّاسَ النَّارَ فَقَالَ: «الْفَمُ وَالْفَرْجُ».
[حسن صحيح] - [رواه الترمذي وابن ماجه وأحمد] - [سنن الترمذي: 2004]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko», ñu laaj ko lan moo ëpp luy duggal nit ñi sawara mu ne: «gémmiñ ak awra».
[Tane na ci ag càllala, wér ci geneen càllala] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2004]
Leerarug adiis b:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sabab yi gën a màgg yuy dugale àjjana ñaari sabab la, te mooy:
Ragal Yàlla ak rafet jikko.
Ragal Yàlla: mooy nga def kiiraay sa diggante ak mbugalum Yàlla, ci di def ay ndigalam di moytu ay tereem.
Rafet jikko: dana nekk ci yaatal kanam, ak di def ñekk tey feg lor yi.
Sabab yi gën a man a duggale sawara ñaar la, te mooy:
Làmmeñ ak awra.
Bokk na ci Bàkkaari làmmeñ yi: fen ak jëw ak rambaaj ak yeneen.
Bokk na ci Bàkkaari awra yi: njaalo ak ngóor-jigéen ak yeneen.