عن أبي ذر رضي الله عنه قال: قال لي النبي صلى الله عليه وسلم:
«لَا تَحْقِرَنَّ مِنَ الْمَعْرُوفِ شَيْئًا، وَلَوْ أَنْ تَلْقَى أَخَاكَ بِوَجْهٍ طَلْقٍ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2626]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abbu Sarrin -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Bul xeeb dara ci lu baax, donte dangay dajeek sa mbokk won ko kanam gu bélli».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2626]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day ñaaxe ci jëf ju baax, te bañkoo xeeb donte dafa tuuti, bokk na ci yooyu kanam gu leer ak di muuñ boo dajeek keneen, kon war na ci jullit bi mu xér ci loolu; ngir la ca nekk ci wéttali mbokkum jullit, ak duggal mbegte ci xolam.