عن المقدام بن معدِيْكَرِب رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«أَلَا هَلْ عَسَى رَجُلٌ يَبْلُغُهُ الْحَدِيثُ عَنِّي وَهُوَ مُتَّكِئٌ عَلَى أَرِيكَتِهِ فَيَقُولُ: بَيْنَنَا وَبَيْنَكُمْ كِتَابُ اللهِ، فَمَا وَجَدْنَا فِيهِ حَلَالًا اسْتَحْلَلْنَاهُ، وَمَا وَجَدْنَا فِيهِ حَرَامًا حَرَّمْنَاهُ، وَإِنَّ مَا حَرَّمَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَمَا حَرَّمَ اللهُ».
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي وابن ماجه] - [سنن الترمذي: 2664]
المزيــد ...
Jële nañu ci Al-Miqdaad ibn Mahdiikarib -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«mbaa sama Hadiis du yeksi ci nit mu tëdd ag gàngunaayam naan: Diggante nun ak yéen téeréb Yàlla la, kon lépp lu nu ci gis lu dagan dananu ko daganal te lépp lu nu ci gis mu araam, dananu ko araamal, te lu Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- araamal, moog lu Yàlla araamal ñoo yam».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2664]
Leerarug hdiis bi : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne jamono ju jegee ngi ñëw joj ñenn ci nit ñi danañu toog tëdd ci séen i gàngunaay, Hadiis bu juge ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yeksi fi moom, mu naan: liy àtte sunu diggante mooy Alxuraan ju tedd ji te doy na nu, lu nu fa fekk ci lu dagan nu jëfe ko, lu nu fa fekk ci lu araam nu sori ko. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na lépp lu mu araamaal mbaa mu tere ko ci sunnaam si ab àtteem mook lu Yàlla araamal ci téereem bi ñoo yam; ndaxte moom day jottali jële ci Boroomam.