+ -

عن ابن مسعود رضي الله عنه قال: قال النبي صلى الله عليه وسلم:
«الْجَنَّةُ أَقْرَبُ إِلَى أَحَدِكُمْ مِنْ شِرَاكِ نَعْلِهِ، وَالنَّارُ مِثْلُ ذَلِكَ».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 6488]
المزيــد ...

Jële nañu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne:
«àjjana moo gën a jege ku ne ci yeen ay waroy dàllam, sawara it naka noonu».

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6488]

Leeral

Yónente bi day xamle ne àjjana ak sawara dañoo jege nit ki kem ni ko ay waroy dàllam jegee te mooy liy nekk ci kaw ndëggu yi, ndaxte moom man naa def ab topp Yàlla ngir ngërëmam loolu dugal ko àjjana, walla ab moy Yàlla loolu nekk sabab ci duggam sawara.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Pulaar Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani الأكانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Xemmemloo ci jëf lu baax doonte dafa néew, ak xuppaate ci jëf lu ñaaw doonte dafa néew.
  2. Jullit cig dundam manul ñàkk mu boole yaakaar ak ragal, tey sax ci ñaan Yàlla mu saxal ko ngir mu mucc te du woru ci melokaanam.