+ -

عن ابن عباس رضي الله عنهما قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«ما مِنْ أيَّامٍ العمَلُ الصَّالِحُ فيها أحبُّ إلى اللهِ مِن هذه الأيام» يعني أيامَ العشر، قالوا: يا رسُولَ الله، ولا الجهادُ في سبيلِ الله؟ قال: «ولا الجهادُ في سبيلِ الله، إلا رجلٌ خَرَجَ بنفسِه ومالِه فلم يَرْجِعْ من ذلك بشيءٍ».

[صحيح] - [رواه البخاري وأبو داود، واللفظ له] - [سنن أبي داود: 2438]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Amul benn bis bob jëf ca lu baax moo gënal Yàlla ci bis yii» maanaam fukki bis yi nëkk Si weeru tabaski, ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ba ci jihaad ci yoonu Yàlla? Mu ne: «ba ci jihaad ci yoonu Yàlla, lu dul waa ju génne bakkanam ak alalam te dara ci yooyu dellusiwul».

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko, ak Abóo Daawuda, kàddu gii ñeel na ko] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 2438]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne def lu baax ci fukki fan yi njëkk ci weeru Tabaski moo gën mbooleem bis yi ci at mi.
Sahaaba yi laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jihaad ci lu dul fukki fan yii ndax moo gën walla jëf yu baax yi ñu jëf ci bis yii? Ngir li ñu xam ne jihaad bokk na ci jëf yi gën.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tontu ne: jëf ju baax ci bis yii moo gën jihaad ci yeneen bis yi, lu dul waa ju génn di jihaadi daal di riske bakkanam ak xaalisam ci yoonu Yàlla, mu ñàkk xaalisam, ruu ga rot ci yoonu Yàlla, Kii daal mooy ki gënle jëf ki def lu baax ci bis yu baax yii.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngëneelu jëf ju baax ci fukki fani tabaski, war na ci jullit bi mu làng bis yii di ci baril ay jaamu, ci tudd Yàlla mu màgg mi, ak jàng Alxuraan, ak kàbbar ak tudd Yàlla, ak sant Yàlla, ak julli ak saraxe ak woor, ak mbooleem jëf yu baax yi.
Ndollent