Xàjjale yi: Ngëneel yi ak teggiin yi .
+ -

عن أبي أيوب الأنصاري رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«لَا يَحِلُّ لِرَجُلٍ أَنْ يَهْجُرَ أَخَاهُ فَوْقَ ثَلَاثِ لَيَالٍ، يَلْتَقِيَانِ، فَيُعْرِضُ هَذَا وَيُعْرِضُ هَذَا، وَخَيْرُهُمَا الَّذِي يَبْدَأُ بِالسَّلَامِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6077]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Ayyuuba Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
« Du dagan ci nit ki mu tóng mbokkam lu ëpp ñatti guddi, ñuy dajee kii dummóoyu kee dummóoyu, ki gën ci ñoom ñaar mooy ki tàmbli nuyóo ba».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6077]

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa tere jullit bi di tóng mbokkum jullitam lu ëpp ñatti guddi, ku nekk di dajeek moroom ma te du ko nuyu du wax ak moom.
Ki gën ci ñaari way-xuloo yi mooy kiy jéem a dindi tóng gi, tàmbali nuyóo bi, li ñu jublu ci tóng nag mooy tóng ngir bànneexu bakkan rekk, bu dee tóng ngir àqi Yàlla mu kawe mi nag, niki tóng moykat yi, ak bidaakat yi, ak àndandoo yu bon yi, loolu moom kénn tënku ko ci waxtu, waaye dafa aju rekk ci njariñu tóng ga, bu deñee rekk mu deñ.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi :
  2. Tóng dagan na ci ñatti fan mbaa lu ko gën a néew, ngir sàmmoonteek yég-yégu doomu aadama, kon tóng ko ñatti fan dañu koy baale ngir li gaaroon daal di deñ.
  3. Ngëneelu nuyóo, ndax day dindi la ca bakkan ya, te màndargam mbëggeel la.
  4. Lislaam dafa xér ci mbokkoo, ak miinanteg aw ñoñam.