عن سَمُرَة بن جندبٍ رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«أَحَبُّ الْكَلَامِ إِلَى اللهِ أَرْبَعٌ: سُبْحَانَ اللهِ، وَالْحَمْدُ لِلهِ، وَلَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ، وَاللهُ أَكْبَرُ، لَا يَضُرُّكَ بِأَيِّهِنَّ بَدَأْتَ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2137]
المزيــد ...
Jële nañu ci Samurata Ibn Jundub -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah, Wal hamdu lil Laah, wa laa-i-Laaha illal Laah, wal Laahu akbar, boo ci tàmbalee baax na».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2137]
Leerarug adiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne wax yi gënal Yàlla ñent la:
Subhaanal Laah: te mooy sellal Yàlla ci bépp wàññeeku.
Ak alhamdu lil Laah: te mooy melal Yàlla cig mat sékk ànd ak bëgg ko ak màggal ko.
Ak laa-i-Laaha illal Laah: maanaam: amul kenn ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla.
Ak al-Laahu akbar: maanaam: Yàllaa gën a tedd te moo gën a màgg lépp lu mu man a doon.
Te ngëneelam ak yoolam nekkul rekk ci toftale ko boo koy wax.