+ -

عن أبي بَكرة رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«إِذَا الْتَقَى الْمُسْلِمَانِ بِسَيْفَيْهِمَا فَالْقَاتِلُ وَالْمَقْتُولُ فِي النَّارِ»، فَقُلْتُ: يَا رَسُولَ اللهِ هَذَا الْقَاتِلُ، فَمَا بَالُ الْمَقْتُولِ؟ قَالَ: «إِنَّهُ كَانَ حَرِيصًا عَلَى قَتْلِ صَاحِبِهِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 31]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Bakrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
«ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi ka raye ak ka ñu ray yépp sawara lañu jëm», ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi kii moo ray, waaw ki ñu ray moom luy mbiram? Mu ne: «ndax moom dafa xéroon ci ray waayam ji».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 31]

Leeral

Yónente bi day xamle ne ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi, ku nekk jubloo ray moroom ja; kon ki raye sawara lay jëm ngir sababus li mu ray waayam ji, Waaye Sahaaba yi di leer lu ci ki ñu ray: naka lay dugge sawara? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- xamal leen ne moom it dafa bëggoon a ray moromam ji, te dara terewul mu ray ko lu dul li waa ji gaawantu njëkk koo ray.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Pulaar Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ki dogu ci xolam ci def ag moy daal di def ay sababam kooku day yayoo mbugël.
  2. Moytandikuloo gu tar ci rayante ci diggante jullit ñi ak tëkku ci sawara gi ci nekk.
  3. Rayante ci diggante jullit ñi bu tegee ci dëgg du dugg ci tëkku gi, niki rayanteek ñi bew ak yàqkat yi.
  4. Kiy def ay bàkkaar yu mag yi du nekk yéefër ngir loolu rekk; ndaxte Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- daa woowe ñaar ñiy rayante ay jullit.
  5. Bu ñaari jullit jamaarloo ci jumtukaay bumu man a doon buy raye, ba kenn ka ray moroom ja, kon ki raye ak ka ñu ray ñépp sawara lañu jëm, li Hadiis bi tudd Jaasi nag day niral rekk.