عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«قَالَ اللهُ تَبَارَكَ وَتَعَالَى: أَنَا أَغْنَى الشُّرَكَاءِ عَنِ الشِّرْكِ، مَنْ عَمِلَ عَمَلًا أَشْرَكَ فِيهِ مَعِي غَيْرِي تَرَكْتُهُ وَشِرْكَهُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2985]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"Yàlla mu kawe mi nee na: ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2985]
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla mu baarkeel mi te kawe dafa wax ne: moom moo gën a doylu képp kuy bokk, mooy ki doylu ci lépp, bu nit defee ag jaamu defal ko Yàlla ak ku dul Yàlla; Yàlla da koy bàyyi te du ko ko nangul, daal di koy delloo boroom; Kon warees naa sellal jëf yi ngir Yàlla mu kawe mi, ndax Moom -tudd naa sellam ga- du nangu lu dul lu sell ngir jëmmam ju tedd ji.