+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«لَيْسَ شَيْءٌ أَكْرَمَ عَلَى اللهِ تَعَالَى مِنَ الدُّعَاءِ».

[حسن] - [رواه الترمذي وابن ماجه وأحمد] - [سنن الترمذي: 3370]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Amul dara lu gën a tedd fa Yàlla mu kawe mi lii di ñaan».

[Tane na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3370]

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne amul dara lu gën a tedd fa Yàlla ci jaamu yi lii di ñaan; ndaxte nangu la ci ne Yàlla ku doylu la -tudd naa sellam ga- ak nangu ne jaam bi dafa aajowoo Yàlla.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Pulaar Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngëneelu ñaan, ak ne képp ku woo Yàlla, ku ko màggal la, te nangu ne ku doylu la -tudd naa sellam ga-, ndaxte néew gi doole duñu ko ñaan, ak ne dafay dégg, ndaxte ku tëx duñu ko woo, ak ne mooy Aji-Tedd, ndax ku nay deesu ko ñaan, ak ne mooy yërëmaakoon bi, ku soxor duñu ko ñaan, ak ne ku am kàttan la, ku ñàkk doole duñu ko ñaan, ak ne Aji-Jege la, ku sori du dégg, ak yeneen meloy màgg yu dul yooyu tey wane màggug Yàlla Mu tedd mi ak taaram.