+ -

عن جندب رضي الله عنه قال:
سَمِعْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَبْلَ أَنْ يَمُوتَ بِخَمْسٍ وَهُوَ يَقُولُ «إِنِّي أَبْرَأُ إِلَى اللهِ أَنْ يَكُونَ لِي مِنْكُمْ خَلِيلٌ فَإِنَّ اللهَ تَعَالَى قَدِ اتَّخَذَنِي خَلِيلًا كَمَا اتَّخَذَ إِبْرَاهِيمَ خَلِيلًا، وَلَوْ كُنْتُ مُتَّخِذًا مِنْ أُمَّتِي خَلِيلًا لَاتَّخَذْتُ أَبَا بَكْرٍ خَلِيلًا! أَلَا وَإِنَّ مَنْ كَانَ قَبْلَكُمْ كَانُوا يَتَّخِذُونَ قُبُورَ أَنْبِيَائِهِمْ وَصَالِحِيهِمْ مَسَاجِدَ، أَلَا فَلَا تَتَّخِذُوا الْقُبُورَ مَسَاجِدَ! إِنِّي أَنْهَاكُمْ عَنْ ذَلِكَ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 532]
المزيــد ...

Jële nañu ci Jundub -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax li njëkk juroom i fan laata muy faatu naan: " seedeel naa Yàlla ne set naa wicc ci kenn ci yéen di nekk sama xarit, ndax Yàlla da maa jàpp xarit, niki mu jàppe Ibraahiima xarit, te bu ma doon wut ab xarit ci yéen kon dinaa def Abuu Bakar ab xarit. Yégleen ne ña leen jiitu woon dañu daan jàppe bàmmeeli seeni Yónent ak seen i nit ñu baax ay jàkka, rikk waay! Buleen jàppe bàmmeel yi jàkka, man tere naa leen ko".

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 532]

Leeral

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare Na dayo bi mu am fa Yàlla, ci ne moom àgg na ca gën gaa kaweg daraja ci mbëggeel, kem ni ko Ibraahiima ame woon -yal na ko Yàlla dolli jàmm- , looloo tax mu ne amul benn xarit bu dul Yàlla; ndax xolam dafa fees ci bëgg Yàlla mu kawe mi ak màggal ko ak xam ko, kon keneen ku dul Yàlla xaju fa, Te bu doon am ab xarit ci mbindéef yi Abuu Bakar lay doon -yal na ko Yàlla dollee gërëm-. Mu moytandikuloo jéggi dayo ci néew yi kem ni ko Yahuud yi ak Nasaraan yi defe ci bàmmeeli séen Yónente yi ak ñu baax ñi, ba mujj ñu def ko ay yàllay, di ko jaamu bàyyi Yàlla, ñu tabax ca bàmmeel ya ay jàkka ak i jaamukaay. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- tere na aw xeetam ci ñuy def lu mel ni séen jëf ya.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngënéel u Abuu Bakar Siddiix -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, ag ne moom moo gën ci Sahaaba yi, te moo gën a yay ci nit ñi ngir nekk Xaliifab Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ginnaaw bi mu faatoo.
  2. Tabax jàkka ci bàmmeel daa book si ñaawtéefi xeet ya jiitu woon.
  3. Tere ñuy jàppe bàmmeel yi ay barab ngir jaamu, di fa julli walla di ko jublu, walla di tabax ca kawam ay jàkka ak i xubba, ngir moytandikuloo tàbbi ci bokkaale ci sababus loolu.
  4. Moytandikuloo ëppal ci gaayu baax yi ndax day jëme ci bokkaale.
  5. Ñàngug li Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di moytandikuloo ba tax mu feddali ko lu jiitu muy faatu ci juróomi guddi.