+ -

عن عبد الله بن عمرو بن العاص رضي الله عنهما عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«الْكَبَائِرُ: الْإِشْرَاكُ بِاللهِ، وَعُقُوقُ الْوَالِدَيْنِ، وَقَتْلُ النَّفْسِ، وَالْيَمِينُ الْغَمُوسُ».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 6675]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate».

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6675]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral bàkkaar yu mag yi, te mooy gu ñu tëkku aji-def ji ci tëkku gu tar ci àdduna walla allaaxira.
Bu njëkk bi "Bokkaale Yàlla": te mooy def wenn xeetu jaamu ñeel ku dul Yàlla, ak yamale lenn ak Yàlla ci lu Yàlla jagoo, cig jaamu, ak ug moomeelam ak ci ay turam ak i meloom.
Ñaareel bi "Dënge ñaari way-jur": te mooy lépp luy waral lor ñaari way-jur moo xam wax la walla jëf, ak bàyyee rafetal jëme ci ñoom ñaar.
Ñatteel bi "ray bakkan": ci lu dul dëgg, niki ray ko cig tooñ ak ug jalgati.
Ñenteel bi "ngiñ luy nuural nit ": te mooy giñ lu waay def di fen te xam ne day fen, dañu koo tudde loolu nag; ngir ne day nuural boroomam ci ay bàkkaar walla ci sawara.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngiñ luy nuuralaate amul lu koy kaffaara; Ndax daa bari loraange ak i ñaawtéef, moo tax fàwwu ñu tuub ko.
  2. Ñenti bàkkaar yu mag yi ñu tudd ci hadiis bi du ngir tënk ko ca waaye day wane ne séen i bàkkaar daa màgg lool.
  3. Bàkkaar yi daa séddalikoo yu mag ak yu ndaw, yu mag yi nag mooy: bépp bàkkaar bu am mbugalum àdduna, niki géten ak móolu, walla tëkkug allaaxira, niki tëkku ci dugg sawara, yu mag yi itam ay daraja la yenn yi moo gën a rëy araamug yeneen yi, bàkkaar yu ndaw yi nag mooy yi nekkul yu mag rekk.