عن عبد الله بن عمرو رضي الله عنهما قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«يقالُ لصاحبِ القرآن: اقرَأ وارتَقِ، ورتِّل كما كُنْتَ ترتِّل في الدُنيا، فإن منزِلَكَ عندَ آخرِ آية تقرؤها».
[حسن] - [رواه أبو داود والترمذي والنسائي في الكبرى وأحمد] - [سنن أبي داود: 1464]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Dina ñu wax ëllag ki jàngoon Alxuraan: Jàngal te yéeg, jàngal ni nga doon jànge ci àdduna, ndax sa kër moo ngi tolloog aaya bi ngay mujja jàng».
[Tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 1464]
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne kiy jàng Alxuraan te di ko jëfe, te taqoo ak moom cig jàng ak mokkal bu duggee àjjana dees na ko wax: jàngal Alxuraan, te yéeg ca darajay àjjana ya ndax loolu, jàngal ni nga doon jànge ci àdduna ci njàng mu teey te dal; sa kër moo ngi ci aaya bi ngay mujj a jàng.