عن عمران بن حصين رضي الله عنه قال: كَانَتْ بِي بَوَاسِيرُ، فَسَأَلْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَنِ الصَّلَاةِ، فَقَالَ:
«صَلِّ قَائِمًا، فَإِنْ لَمْ تَسْتَطِعْ فَقَاعِدًا، فَإِنْ لَمْ تَسْتَطِعْ فَعَلَى جَنْبٍ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 1117]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Imraan Ibn Husayn -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: damaa amoon ay góom, ma laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla xéewal ak mucc- ci lu jëm ci julli, mu ne ma:
«jullil taxaw, boo ko manul nga toog, boo ko manul nga wetu».
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1117]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne cosaan ci julli mooy taxaw, lu dul ne manu ko mu julli toog, bu ko manul mu julli tëdde wet.