عن أبي مسعود الأنصاري رضي الله عنه قال:
جَاءَ رَجُلٌ إِلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَقَالَ: إِنِّي أُبْدِعَ بِي فَاحْمِلْنِي، فَقَالَ: «مَا عِنْدِي»، فَقَالَ رَجُلٌ: يَا رَسُولَ اللهِ، أَنَا أَدُلُّهُ عَلَى مَنْ يَحْمِلُهُ، فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «مَنْ دَلَّ عَلَى خَيْرٍ فَلَهُ مِثْلُ أَجْرِ فَاعِلِهِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1893]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Mashuud Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Amna nit ku mas a ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ne ko: amuma waruwaay, kon nag jox ma waruwaay, mu ne ko: «amuma ko», am ku ne ko: yaw Yónente bi, dinaa ko tegtal ku ko jox waruwaay, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «Ku tegtale ci lu baax, dina am pay gu mel ni li ki ko def am».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1893]
Leerarug adiis bi : Am na ku mas a w ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla defal jàmm- ne ko: sama waruwaay dafa dee, yéegal ma cig daaba, te jox ma waruwaay mu yóbbu ma, Yónente bi -yal na ko Yàlla defal jàmm- gàntal ko, ne ko amul dara lu mu koy jox, benn waay bu nekkoon foofu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi dinaa ko yóbbu ci ku koy jox waruwaay, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm- xamle ne, mook kiy saraxe ñoo bokk am yiw, ndax moo ko tegtal aji-yittewoo ji.