+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«قَالَ اللهُ تَبَارَكَ وَتَعَالَى: أَنَا أَغْنَى الشُّرَكَاءِ عَنِ الشِّرْكِ، مَنْ عَمِلَ عَمَلًا أَشْرَكَ فِيهِ مَعِي غَيْرِي تَرَكْتُهُ وَشِرْكَهُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2985]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"Yàlla mu kawe mi nee na: ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem".

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2985]

Leeral

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla mu baarkeel mi te kawe dafa wax ne: moom moo gën a doylu képp kuy bokk, mooy ki doylu ci lépp, bu nit defee ag jaamu defal ko Yàlla ak ku dul Yàlla; Yàlla da koy bàyyi te du ko ko nangul, daal di koy delloo boroom; Kon warees naa sellal jëf yi ngir Yàlla mu kawe mi, ndax Moom -tudd naa sellam ga- du nangu lu dul lu sell ngir jëmmam ju tedd ji.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Moytandikuloo bokkaale ci bépp melokaanam; ndaxte moom day teree jëf mu ndangu.
  2. Yëg doylug Yàlla ak ug màggaayam dafa bokk ci liy dimbali nit ki ci mu man a sellal jëf.