+ -

عَنْ أَبِي سَعِيدٍ الخُدْرِيِّ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِذَا سَمِعْتُمُ النِّدَاءَ، فَقُولُوا مِثْلَ مَا يَقُولُ المُؤَذِّنُ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 611]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«bu ngeen déggee woote gi nangeen wax lu mel ni li noddkat bi di wax».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 611]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day soññee ci bu ñu dégge nodd-kat bi ñu koy toppandoo, ci di wax kem li muy wax. Bu kàbbaree nu kàbbar, bu waxee ñaari seede yi, nu wax leen. Dees na ca settee:(hàyya halas salaah, hayya halal falaah )foofu dañuy wax ci ginnaawam : laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi: day toppandoo noddkat bu njëkk soonga toppandoo noddkat bu ñaareel bi, doonte noddkat yi dañoo bari, ngir ne hadiis bi daa matale lépp.
  2. Day toppandoo noddkat bi ci anam gu ne, ndeem nekkul ci wanag, mbaa muy faj aaju.